Kumba Ndóofeen Famak Juuf
Apparence
(Yoonalaat gu jóge Kumba Ndóof Seen Juuf)
Kumba Ndóofeen Famak Juuf (ci baati Seereer : Maad a Sinig Kumba Ndoofeen Famak Juuf) Buur Siin la woon toggoon ci jal bi ca atum 1853-1871. "Maad a Sinig" ci baati Séeréer moo tekki "Buur Siin". Ci meenu Gelwar la soqqeekoo - askanoo Njuufeen, kerr Semu Njeke. Maamam ci xeetu Séeréer ak Soose la juge. Màbba Jaxu Ba, Kumba Ndóofeen Famak Juuf moo ko ray aki Ceddoom, ci ndimbëlug tubaayi ca xare ba ñuy tudde Somb-Cucun ca atum 1867.