Aller au contenu

Konkoroŋ

Jóge Wikipedia.
Konkoroŋ gi (Hyphaene thebaica)

Konkoroŋ xeetu tiir la gu yor foytéef bu gulumba bees di lekk. Moo ngi bàyyikoo ca xawa-dun bu mag bu araab yi, ak ca gànnaaru Afrig ga mu law te faral di sax fa am ndoxi ron suuf.

Konkoroŋ gi, garab la guy àgg ci 17i met ci guddaay. Kuttmbalu ronam danay àgg ba 90 sàntimet. Caram day meññ ay jubbi xob. Xàncam daa liis, yor wirgo wu baam te dër ba noppi yor melow xob yu wow.

Caram ak xobam danay àgg ba 1 met ci guddaay ba noppi yiir bànqaas yi ko meññ, teg ci gànnaayoo ay xosi yu dëng te jëm kaw. Xobam melow wuppukaay la yor, danay natt 120 ba 180i sàntimet. Tóortóoram bu góor ak bu jigeen ci garab yu wuute lay meññ.

Njariñ li

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Meññeefum garabug Konkoroŋ
Meññeefum garabug Konkoroŋ

Xàncam dees na ci ràbb i basaŋ ak i duu. Dees na ko lekk it. Mattam dees na ko jëfandikoo ci tabax. Xàncam dees na ci jële njar.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Hyphaene thebaica

Tur wi ci yeneeni làkk

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
araab: الدوم
farañse: palmier doum
angale: dum palm
itaaliyee: palma dum