Aller au contenu

Kocc barma faal

Jóge Wikipedia.

Kocc Barma Faal ñu ne it Kocc barma , been kanding la woon, ca senegaal, ci jamono nguuru Kajoor am, ca XVII xarnu. Ci wallu xeltu la daan doxal.

Kocc Barma, been dakkantal ñu ko daan jox la woon. Waaye, Birima Ma Xureja Demba Xole Faal la tuddoon. Xam xam bu mag mu yoroon, ak ndono bu rey li fi bayyi ci Senegaal, ba nit ñepp di ci roy ba leegi ca wa senegaal, moo tax ñu ko tudd tamit sunu maam kocc. Ci askanu FAALEN la bokkoon, nekk been xeet wu rey ca Kajoor, ndax ñoom ñoo nekkoon buur Dammel ca nguuru bobu. Ca jamono joju, Dammel yi, dañu daan noot mbooleem nawlee yi dekk ca reew mi. Di leen buntuxutal, boole ci tekk leen dundu bu meti. Kocc Barma Faal, xeex na ak njabootam, manaam ñoñu daan elif dekk ba, ndax coono ñu daan tekk kaw nit yi bañ am. Moo tax nit yi ñu begg ko, am kollere ci moom, ñu dek ko seen njiit.

Baayam mooy Ma Xureja Faal Demba Xole, yaayam di Ngene Kewe. Amoon na ay rakk. Ci rakkam nit yi gena xam, am na Maxanta Faal ak Demba Faal ci goor yi, Fayine ak Faatu Faal ci jigeen yi. Ak ñoom la Kocc magee, ci këru FAALEN yi, ca Kajoor. Dammel bi ñu fal ca jamono joju, Dawuur Demba Faal la tuddoon, nekk camminu Kocc Barma Faal.

Ba mu nekee xale la wajuuram gis naka Kocc Barma meloon ci wallu xam xam ak mandute. Dekkam yepp di gis ci moom nit ku ñepp raññee te ellëg sibir di mujj nekk royukaay bu wor.

Am na ñu ne tamit, Kocc Barma, tuŋngun la woon, te dafa amoon ñeenti jubb, jubb yu nekk, dencoon been artu walla leeb. Ci ubbite bi, moom ak jabaram kepp ñoo xamoon lan la jubb yi jemmal.

Ñeenti leeb yi:

  • Jigeen soppal waaye bul woolu
  • Mag, mat na bayyi ci reew
  • Buur du mbokk
  • Doomu jiitle du doom

Leeb yi yepp, ci xeewi Kocc Barma dund la joge, te anam yi ñoo ko faramfacce seen bopp. Am na it yeneeni leeb. Ci yeneeni xeltukat amoon ca jamono joju, am na keen ku tudd Maseeni, ci setu Kocc Barma la bokk, bayyi na fi leeb yu bare tamit, ak Biram Caam Demba koku daan jox wolof yi ay cax walla ay pasin yu bare ñu daan wara xam. Xeltu yepp, ngir yeete nit yi leen ko daan tasaaroo, siiwal.

Li yepp, ci cosaanu ñu lakk wolof la bokk, ndax ñu ko doxal ci wolof a tax kallamu wolof ak askanu wolof denc lu ko moom ci wallu aada ak cosaan. Cosaanu Senegaal la, ndax wolof, waaso yepp moo ko nos (pel, serer, sarakole, manding...). Cosaanu nit ñu ñuul la, fu ñu mëna nekk ca aduna, ndax ay nitu ñuul ñoo ko moom. Ñu bare, ñakk xam a tax, dañu foog ni, nit ku ñuul, mosul indi dara ci wallu xeltu ca aduna. Waaye, ay gestukat yu mag, mel ni Seex Anta Joob, wonee neen ak ay firnde, mandargal bu wor, gestukat yu gëna mag ci aduna nangu neen ko, ni ay nit ñu ñuul ñoo sos xeltu, ca aduna, ñu ubbite ko ci Sudan ci ay jamono yu yagg, te ñoo ko jox xonk nopp yi, ci nguuru egypt, ci seen jangu yi xonk nopp yi joge nguuru greece daan ñoo ci ay xeltukatu ñuul ngir jangu seen xam xam. Xonk nopp yi sax bind neen ko ci seen téere, mel ni been ci ñoom mu tudd Solon, ñow egypt ngir jang xam xamu nit ñu ñuul ñu fa amoon, ci been xeltukat bu mag ku tudd Sankara (Sankara di nekk sant bu siiw ci sowu afrig, ca manding yi ak pel yi). Def na ñaari fukki ak ñaar at fofu ca egypt ndax lolu.