Keŋ

Jóge Wikipedia.
Keŋ gi (Flueggea virosa)
Keŋ gi (Flueggea virosa)

Keŋ garab la gu gàtt gu man a toll ci 4 ba ci 7i met gën gaa bari. Garab gi day am ay car yu bari yoo xam ne suuf lañuy jóge jëm ci kaw mel ni lu wërngalu. Xobi garabu Keŋ leeg leeg dañuy wadd su dee barab bi mu nekk daa wow waaye su tooyee man nañoo bañ a wadd.

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Meññeefi garabug keŋ
Meññeefi garabug keŋ

Garabu keŋ bari nay njariñ lool. Ñu man koo jëfandikoo ci faj lu baree bari. Amna sax ñu ne bokk na ci garab yi ëpp njariñ ci lu nuy fajoo ci sunu tund yii, waaye it garab la gu bari ay loraange. Manees na cee defar tooke yu man a ray yenn mala yi niki jinax añs

Garabu keŋ man naa dund ciy barab yu wuute niki ci àll bu bariy garab, mbaa ci barab bu bari ndox walla bu ko amul, mbaa ñu man koo fekk ci kaw dëkkuwaayu xorondom yi, mbaa melentaan. Keŋ ku ko fekk ci tool bu ñuy waaj a bay deesu ko dindi ndax njariñ yi mu man a amal suuf si.

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Flueggea virosa

Tur wi ci yeneeni làkk[Soppisoppi gongikuwaay bi]

farañse: balan des savanes
angale: white-berry bush
kisuwayli: mkwamba