Juma Jeŋ Jaxate

Jóge Wikipedia.

Juma Jeŋ Jaxate soskatu ñawin la bu dëkk Senegaal, juddoo Tëngeej (Rifisk), ñetti fan ci weeru desàmbar atum 1947.

Dundu ak jaar-jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom ci boppam moo jiite bérebu liggeeyukaayam bi mu tudde Shalimar Couture, bokk na ci ñi muy ñawal, njiiti réewu Afirig yu bare ak seeni soxna.

Atum 2012, la bett askan wi ne dafay nekk ab way-wotelu ci wotey njiitu réew yi. Mu mujj ci nekk ndàdde ci sumbug wote bu jëkk bi, ndax téemeer boo jël, tus kos fukk ak ñaar (0,12%) rekk la amoon ci ñi wote ñépp.

Ay sargalam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Atum 2013 la ko woykatu Kóngoo bi Koffi Olomidé sargale woyam wi mu tudde Festival[1]. Mu dellu amaat lu ni mel atum 2013, ndax Fally Ipupa sargale na ko aw woyam[2].

Seetal tamit[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lees bind ci moom[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Jukki bi ñu jëfandikoo ngir bind bile

  • « Diouma Dieng Diakhaté : La couturière aux doigts de fée », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 37-38

Jukki yi ñu ko tudd[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër[Soppisoppi gongikuwaay bi]