Aller au contenu

Jeqiku gi xam-xam amal ci Elektron

Jóge Wikipedia.

Jeqiku gi xam-xam amal ci Elektron :

Xamale lan mooy “ Elektron” :


Elektron moom yaram su sew la lool, moom daal gën na a ndawe ay milyoŋi yoon, yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk, bu ñu rafleel. Moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu mbëjfeppal(electronique) yu bees yi am leegi. Li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoŋi Elektron dajale leen, du nu toll ne boppu puso.

Elektron nag nekk na ci bépp ne-ne bu Yàlla sàkk, moom nag mooy peek fepp wi, moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko fepp wiy xëcc. Elektron ni muy wëre fepp wi - booy xool - day mel ne ni kawkab yi di wëre jant bi. Elektron nag day yanu ay cëfkay mbëj yuy bañ ,fepp wi di yor ay cëfkay mbëj yuy wuyyu walla nangu.


Xam-xamu Elektron ni mu sosoo:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xam nañu ne xam-xamu mbëj moom xam-xam la bu ñu xame bu yàgg ci ki ñuy wax Taalis, di woon boroom xam-xamu Geres. Ay boroom xam-xam yu bari nag ñëw, gën koo jëme kanam, bokk na ci ñooñu kii ñuy wax Wilyaam Jilbert, di boroom xam-xamu Angalteer boo xam ne mooy ki teqale dooley mbëj ak dooley bijjaakon , ci noonu la wuuteek kii di Taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lañu. Jilbert it xamoon na ne duusi mbëj yi ñooy jur dooley bijjaakon. Boroom xam-xamu Almaañ bii di Anofon Jiyorik, moom itam di ki njëkk a genne wuutuloxo buy juddal mbëj, maanaam jumtukaay buy tax mbëj di judd, di am, loolu di ci atum 1663 g. Tomas Adison it ñëw, indil ñu làmp bu mbëj.

Xam-xamu mbëj nag soppiku di xam-xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g, loolu nag mi ngi amoon ginnaaw bi boroom xam-xamu Jëmm bu Angalteer bii di Josef TOMSON jugee, feeñal xam-xamu elektron atum 1897 g, daal di ciy ame neexalub Nobel ci xam-xamu Jëmm. Li gën a jëmal kanam xam-xamu elektron nag mooy wuññi gi boroom xam-xam yi wuññi ne fepp (saal biy wuyyu) day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ, te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari. Ndamul xam-xam lii ab jéego la bu am solo ci doxub xam-xamu elektron. Jéego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf.


Jumtukaay yu elektronig (walla mbëjfeppal) yi ak seen njariñ:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk, di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko, ci kër yi, liggéeyuwaay yi, dëkk yu mag yi, yu ndaw yi, mbay mi ak mecce yi añs.

Kon daal jumtukaayi elektron yi, dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi, nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu mbëj yu boppu (otomatik) yi, ak fompukaay yu mbëj yu boppu yi, ak jumtukaayu seral yu wuute yi, ak rajook tele yu melo yi, ak jumtukaayu nataal yi añs.

Boo demee ci paj it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron, xoolal ma fesalukaay yu elekton yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti, ak nataalukaayu paj yi, ak jumtukaayu segg yu elktron yi. Jumtukaay yii dey tax nanu paj man a xam lu jot nit, man koo faj, te looloo tax paj jëm kanam ci sunu jamono jii.

Gis nga leegi foo dem fekk fa nosukaay, ci bank yi, lonkoo yi(les sociétés), campeefi nguur yi ak liggéeyuwaay yi. Gis nga xam-xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi, ak xam kilimaa bi, te loolu lepp elektron a ko waral, leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll, nu jawwu ji selle, nu gelaw li gaawe, nu tàngoor wi tànge, nu niir yi kawee añs, te loolu lepp elktron a ko def.

Waa xam-xamu suuf (jiyoloji) jariñu nanu ci jumtukaayi elktron yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si, te di leen won fi am petrol, yoraniyom ak yeneen mbelli suuf yu am yi solo.

Jumtukaayi elektron yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare, ak aaru. Leegi gis nga soxu fepp (bombe atomique) , rajo, jumtukaay yi amul buum , ak yiy yonnee tey nangu, ak yiy nataal añs.

Lii nag wone na ne xam-xamu elektron, aki jumtukaayam, yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare, def nanu fi ag jeqiku gu xam-xam gu am solo ci xarnub ñaar-fukk g bii. Nit nag jot na a man a tàggat xam-xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm, waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb, tey mbugale, di alag mbidéef yi.