Aller au contenu

Jaxan-jaxan

Jóge Wikipedia.
Jaxan-jaxan gi
Jaxan-jaxan gi (Prosopis africana)

Jaxan-jaxan xeet la ci xeeti garab yi bokk ci ñoñ Prosopis. Ñi ngi koy fekk ci gox yi nekk diggante Afrig gu naaje jàpp Sahel.

Garab guy àgg 12-20i met taxawaay la, jëmm ji daa jub xocc te muluŋ ba mat 1,10i met ci ndigg li, kaw gi daa ubbeeku am i xob yu sëgg te wirgoo nëtëx bu leer.

Xasam mi daa am i paq yu sew te dëgër, nekk ci diggante baam ak ñuul.

Meññeef mi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ci ëpp ci ñaareelu xaaju noor walla ca taw yu njëkk ci nawet lay meññ.

Njariñ yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dinay faj yii: bëñ bu xomaat (walla bëñ buy metti), noyyikaay bu fatt, ay goom, deru yaram bu wopp, tawati gët. Dinay faj it metiitu biir, nopp, bopp ak biir buy dàw.

Dinañ koy faral di jox jur gi. Dina faj emoroyitu jur gi.

Fas, nag ak picc dinañ koy jëfandikoo (ñax).

Bantam bu tolle ci mboqee jëm mboq bu xall, mucc ci gunóor ak sax yi.

Manees na jëfandikoo bant bi ni bantu tabax (tabax kër), bant biy nekk ci jumtukaayu tabax yi.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Prosopis africana