Jàngu Yéesu bu Dëggu bi

Jóge Wikipedia.

Jàngu (eglise) yéesu bu dëggu bi” ab jàngu bu temb la (indépendant)bu nekk ca Beijing ca réewu Siin, ñoo ngi ko taxawal ci atum 1917. Dafa nekk ab bànqaasu diiŋatkat (protestante) yu waa Siin ci diiney krist bi fëll ci atum 1900. Jàngu boobu day balloo 1,5 milioŋi taalibe yi mu am ci adduna wërngëlkëp. Jàngu googu gëm na njangalem pantekot, day ab baatin gu wekku ci mayu ku sell ki. Fukki ponki gëm-gëm gi ñooy:

  1. Ku sell ki: “Jot xel mu sell mi ci xamale te jëfënbikoo ay làkk, doon na ab wòoraange ci sunub yégg ca nguurub asamaan si.”
  2. Ngente(lavage de pieds): “Ngente gu ndox mi doon na ngir raxas say bakkar ak sag judduwaat. Ngente li ci ndox mu sell la war a amee, lu mel ne dex, géej walla cib walub ndox. Ngentekat, bi jot a am ngente li, tamit jot ndox ak xel mu sell, mooy jiite ngente li ci turu Yéesu-kristaa. Ki ñuy ngente da fa war a nuuru ci ndox mi, sëggal boppam te di xool ci suuf”.
  3. Jangu: Ponkub jangu (raxas sa tànk) li, day tax nga man a dellu ci lenn ci jëfi Yéesu. Di it ab fattali ni daño war a am cofeel, am cellte, tuuti, am yërmaande ak di dimbaliwaate. Nit ku jot ngente gu ndox mi war a naa raxas ay tànkam ci turu Yéesu-kristaa. Yeneen Jangu yi ciy tegu man nga kaa def saa yu la neexee.
  4. Waxtaan gu sell gi: “Jokkoo bu sell bi ab ponk la ngir maggal saayub Yéesu-Kristaa. Di na tax nu man a bokk ak Yéesu ci suux ak ci dereet, tax it nu man a jokkoo ak moom ngir nu man a dund ba faaw te man a yéeg asamaan kerook bes pénc. Ag naan gu jòge ci rasin ak mburu mu amul lëwiir la nuy jëfëndikoo su nuy amal ponk boobu.”
  5. Besu sabbat: “Besu Sabbat, di juroom-ñaareelu bes ci ayubes bi, doon na bes bu sell. Dan kaa war a dund ci ngërëmu yalla ngir maggal li mu bind te di ko jaamu ngir man a yaakaar noflaay gu sax-dakk ci li des ci sunug dund.”
  6. Yéesu-kristaa: “Yéesu-kristaa, baat bi soppiku nekk suux, faatu ci cruaa bi ngir man a jënd bakkaar yi, mu feeñaat ci ñetteelu bes bi dal di yéek asamaan. Mooy kénn kiy wàllu doom-aadama yi, di ki sàkk asamaan ak suuf, di itam benn yalla bi am. ”
  7. Biibël: Biibël bi, nga boole ci tawreet ak linjiil, kàddu yalla lañ, génn dëgg la gu dul deñ, di it ab royuwaay ngir kercen bi.
  8. Nuyoo gi: Ag Ngërëm Yalla ju bari yërmande gee koy joxe jaarale ko ci xol. Ngëm-ngëm yi, ci Xel mu Sell mi la ñu war a jafandu ngir man a topp cellte gi, ngir maggal Yalla te man a sopp doom-aadama yi.
  9. Jàngu gi(l'eglise): Jàngub Yéesu bu Dëggu bi, bi Yéesu-Kristaa ak Xel mu sell mi taxawal ci jamanoy “taw gu mujj” ga.
  10. Feeñug yalla: Dellusig Yalla, bes bu mujj ba lay amee, muy bes ba muy jògee asamaan ngir àtte adduna bi. Ñu baax ñi di nañ am dund gu sax dakk, ñu bon ñi dañ leen di mbugal ba faaw.