Aller au contenu

Isipt gu yàgg ga

Jóge Wikipedia.

Isipt gu yàgg ga nekkoon na réew mu woomle, mu ami suuf yu naat, yu nangu mbay, ngir dexam gu mag googu di (Niil), am na it ay mbelli wurus ak xànjar ak weñ ak jamaa. Moo nga tambalee woon ca peggu Sudaan jëm ca géej gu diggu ca bëj-gànnaaram.

Isipt bu njëkk dafa séddaliku woon ay xaaj. Ci jamonoy 3200 nj.j(njëkk judd gi) lañu bennal xaaj yii, mu mujj nag di nguur gu dëgër, buur bu tudd Firhawna jiite ko, ay foŋsaneer di ko jàppale yu man a bind man a jàng. Bindkat ya dañu daa jëfandikoo li nuy wax mbindum Yirogliif, ñoom nag bindkat yooyu lañu féetale woon war a jottali ndigali buur bi, ak dajale galag yi (juuti yi) ak taxawal yoon.

Ñoñam it siiwoon na ñu ci yaxantu ak réew yi ñu digool, ci gaal yi daa jaar ci Niil. Waa Isipt am nañu xay gu cosaanu, ñu nekkoon ñu daa gëm ay yàlla yu bari, daan leen melale ci bindu nit ku am boppub bàyyima., yàlla ju ci mel ne Amoon Ra (yàllay jant ji) benn la ci ak Isis (yàllay weer wi) , nga xam ne Firhawna it yàlla lanu ko jàppe woon. Daa nanu tabaxal seen yàlla yi ay jaamuwaay (ay temple) ngir màggale leen ko. Ña cay ñu woomle dañu daa tabaxal seen bopp ay bàmmeel yu yor bindub mbaanaar (pyramide). Bu ñu daa suul seeni néew nag, dañu ci daa boole mbooleem seeni bagaas ak alal. Ci atum 332 nj.j la waa Geres teg loxo Isipt, booba it la tàmbalee naaxsaay.

Isipt ak Afrik gu ñuul gi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Seex Anta Jóob (1923 – 1986 g.j) moom lañuy jàppe boroom xam-xam bu Senegaal bi jot a def ay gëstu ci nguurug Isipt gu yàgg ga, mu leeral ci séqoo gi am ci diggante xayug Isipt ak xayug waa Afrig yu ñuul yi.

Ab yatt bu Tutanxamun

Seex Anta Jóob wuññi na jaare ko ci gëstoom yooyu mu defoon ci mbind yi nu yatt ci doj yi ci Isipt, ak ci gëstu yi mu defoon ci tàdd (cadavre) yu ñu taaniit (momifier) yi , - wuññi woon na ne Firhawna yi de li ëppoon ci ñoom ay nit ñu ñuul lañu, ñu néew reek ñoo ca nekkoon ñu weex. Seex Anta it wone woon na niroo gi am ci diggante lu bari ci làkki waa Afrig yi ak làkku Isipt wu yàgg wa, ponki làkk yi ak bennaani baat yi dañoo niroo.

(Man nag ma ne ngir dëggal niroo googu : mbaanaari séeréer yu yàgg ya ak mbaanaari waa Isipt yi walla seen pyramide yi, xool-leen leen, ag niroo ngi fi de, waxuma la nag suulaale gi waa Isipt yi daa suulaale néew beeki bagaasam te séeréer su yàgg sa daa ko def .)

Am na yeneen tomb yu ñu bokk ci diggante Isipt gu yàgg ga ak Afrig gu ñuul gi : Am col ak watuwiin, ak topptoowiinu kër ak yenn ci ay gëm-gëm aki jaamuwiin.

Wuññi yii wone nanu ne ag wàll ci xayug Isipt ga ci Afrig gu ñuul gi lañu ko jële.

Yenn ci wuññi yu waa Isipt

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Isipt gu yàgg ga daa nekkoon gu di boroomug xay gu kawe gu dimbalee ci amal ay wuññi yu am solo ci wàllug xam-xamu xayma, ak xam-xamu falag (fidiw).

Fànnu Isipt bokk na ci fànn yi gën a rafet ci yu yàgg ya. Xam-xam yii nag tas nanu ci àdduna bi, kon goxub Afrig sañ naa ndamu ci li mu indil ag nite ciy liggéey yu am solo.

Waa Isipt defar nañu ab arminaat, lim ci at mi muy 365 fan : 12 weer * 30 fan = 360. Ñu dolli juroomi fan ngir màggale ci juddug seen yàlla yi : Osaris – Isis – Oris – Sit – Nifti . Séddale nañu at mi def ko 4 xaaj, xaaj bu ci nekk am ñeenti weer. Weer wi ñu séddale ko ñeenti ayu bis, gu ci nekk am fukki fan. Bis bi nag ñu séddale ko 24 waxtu.

Seetal BUNTU TAARIIX