Gerte tubaab

Jóge Wikipedia.
Nataalu gerte tubaab.
Nataalu meññatum gerte tubaab.

Gerte tubaab xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Cambretaceae". Mi ngi soqeekoo ci réewum Gine. Barab yi bari naaj ak taw lay faral di sax.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gerte tubaab garab la gog mi ngi toll ci 9 ba 25i met ci guddaay. Ci jamonoy noor, ay xobam dañuy joxe wirgo wu palmaan lu jëkk ñuy wadd.

Meññeefam nëtex lay tàmbalee, su jegee ñor day puur. Su ñoree dëgg nag day palmaan.

Njariñam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Manees na koo lekk noonu. Manees na koo jëfandikoo it ci xeetu togg yu wuute. Xooxam dees na ci sos ay fowukaay niki ay gaal yu daw

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Terminalia catappa