Aller au contenu

Fay Faat

Jóge Wikipedia.

NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINNAAW IMAAM

Lu war la ci maamoom mu fay li ko faat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot.

Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu jekki,taaya , sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat.

Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki, taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex.

Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf.

Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël.

Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi. Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya rekk te yalu ko.

Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam . Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem.