Fatoumata Sall
Fatoumata Sall (wala Fatoumata Sallah ca Gambie) Linguère touclouleur la, doomu lamtoro (jittum toucouleur) mi don jiite dekku Fouta-Toro penku mi ñu nek Sénégal. Yaayam Ndiadiane Ndiaye la, ki sanc dëkku Djolof te mama wolof yi la te Barka Bo tamit, mburu Waalo.
Dundu ak jaar-jaaram |
---|
Biographie
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Faatumata Sall mooy doomu Amrane Sall, tuuram dafay ñy beri anduñu ci, waaye am na ay nit ñu bëgg ko tudd Ali Imdirane. Amrame Sall moo sargal njàmbaar bi may ko doom, Abou Dardai, ben chérif cosaano maure ñowe Chinguetti. Dëkkat yi, ay moromu Seyyidina Mohamed lañu, dañu leen xam ci turu Ouladou Bousbahi, li muy tekki ci khassaniya mooy "siin". Ñoo bokk ci njaboot Aidari, Ali Aidara tamit, doomu Siin lañu ko tuddé. Yaayam dafa tudd Faatumata Binetou Ahsatte, jabaru Aboutalib, mu jox ko tur wi gannaaw bu mu rey daan wuuf bu mu nekkoon xale ndax fitam.
Seyam ak Abou Dardai
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bi mu yege Fouta. Ab geer bu am solo, Lam Toro Amrane Sall, joxko loxoy domam Fatoumata Sall. bi mu deffe jëff rafet joju, Abou Dardai door xalaat li ko nu ko doon wax ci Fatoumata Binetou Rssoul « moy ki nga nara jeul soxna.»
Nonou la yayou Ndiadiane jële tuur bi. Bi mu nekon di jihad, bi mu ajje te deme ci dekk yu wuute ndax bege lawal lislam, bala muy xam ki nara nekk soxnam, feleche bu am posone jamm ko. Posone doug ci yaram bi di wani wergu yaramam. Mu setlou ne dee ba ngi now, dem seeti soxnam Fatoumata Sall, te am waxtaan mu nant nopp rekk degg ci negam. Bess bobu mo sonu lolu te setlou ne legui mou de. Te tamit jabar ji dafa nekoon di jafte, legui mu wassine.
Bi Abou Dardai waxee Fatoumata Sall ne mo ngi waaj dee, mu fateliko yonent mi ne du dunde feke judd domam, te dina tudd Amadoul Amin. joxnako ay tettal yu leer ci euleukou domam, fateliko ne domji li mu neke settu Cherif ak Yonennti bi, denu ko wara samm, te yarr ci faratay lislam. Abou Dardai mu ngi koy ci mu yobbu ko fouta ndax mu jangg al Xuraan, su pare mu deem Chinguetti defaar xaam xammam xi Charia.
Abou Dardai xamne Fatoumata di na yegg wetaay su dee we, ndax di na perte dieukeureum, te wara thénjeu. Wante, mo ki koy xiir ne dieukeur mu gaanu du te seey mi diekh. Waaxtaan mi yaag lool. Bi yu paree we, ABOU dardai jeel ay teree al xuraan yu bari, te tambali deem.
Ab tukki mu worul moo don ñow. Mu fegn ci ndex bi te topp yoonam. Mboumba, wettu Haere Lao la deewe. Gaañu bi rey ko, am na ay nit ñu wax dafa dee njàmbaar.
Bi mu gaañu, ca judduu doom bi, thénju bi jex. Doom bi juddu djirim, doomu yaaye ak baye casé la. Waaye, Fatoumata sall jur bennen doom. Jur bi moo don mu nekk anam mu jekk, tukkiam ca Fouta, Ba mu yegg ca Minguègne Boye.
Seyam ak Mbarek Bo
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Abou Dardai nena ko ne xamna na ne seey farata la, mayna ko mu seyaat su gëne addina. Mu ngi key ñanaal mu am dunde bou tawfeex, wante mu ngi key ñar mu am borom kër mu juliite. Bi mu ko laccé we nan ley deff ba am lolou yi anam la ko lim: kou wacce Kamir, kouy julli juroomi waxtu yi, kouy jooxe assaka te koy jox ceur faratay lislam, te mouy gëne dëkk bi souy japp ndax bëgeu soutoural boppam. Ci waxtaan bobou Mbarick Bo jaamu mbaa mu nekk talibe wu Abou Dardai, mo ngi deglou Ndank. Li Abou Dardai am Fatoumata di waxtaan lepp Mbarik Bo mi Serigneum jaangal Al Xuraan, mo ngi deglou tettal yeup.
Bi mou deglo tettal yeup, Mbarik Bo tambali di lenn toppe. Li mou beugeu moy ñan loxo Fatoumata su serigneum gëne addina. Fatoumata Sall tarou lool te mbok ci askan bu am solo, ci li mu nekk domu Ali Imrane, bi nekk jittum deuk bi.
Fatoumata Sall dina xaar bu domam bu gor, Ndiadiane, dieum magg, pour waxtaan ak mom jaamu bayeum bi ko bëgeu takk. Momou dou jaam rekk, mo doon loxo Ndeye-Dioram, mou am ko solo lool.
Bi ñu siwaale takk bi, Ndiadiane, merr ndax li xew ne dey gadday ci dexu Gallat, wetu Bakel, capitalam Lam Toro bi nekk ci camiñu tefess bi. Bi lolou amme mu rerr ay nittam. Wa dëk bi xaamewu ñu ko woon, wante Amoudou mo ngi doon dunde ba tey. Ñenni nenañu limou menn feyy mo tax, ñenenyi ne mounn na dunde ci biir ndox bi ni muy dunde ci ndox bi, ndax jiine yi ño koy samm.