Faatu Sow

Jóge Wikipedia.

Royuwaay:Infobox biographie2

Faatu Sow

Dundu ak jaar-jaaram
Juddu 1940

Dakaar

Réew Senegaal
Liggeey Borom xam-xam ci wàllu xam-xamu askan
Yeneen xibaar
Liggeeye na Iniwersite Seex Anta Jóob, Eestiti fondamantaal dafrig nuwaar (IFAN)

Faatu Sow borom xam-xam la ci wàllu askan, di kuy taxawal jigeen ñi, nekk tamit ab gëstukat ci mbirum pàcci-pàcce askan ci Afrig.

Dundu ak jaar-jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bokk na ci jigeen ñi jëkk a jàng ba yegg iniwersite ginnaaw jamonoy moom-sa-bopp gi. Mu daldi wone teesam bi mu bind ci borom xam-xam yi gën a mag ci Senegaal laata muy wéyal ay gëstoom ci xam-xamu askan (sosiyolosi).

Ay jaar-jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Faatu Sow mujj nekk jàngalekat ci iniwersite Seex Anta Jóob bu Dakaar. Ci njeextalu ati 1980 la sos tëralinu njàngale wu aju ci wàllu wuuteeb nekkinu góor ak wu jigeen ci gëstuwaay bu ñu naan Conseil pour le développement de la recherche en sciences sociales en Afrique. Atum 1999, mu daldi amal am ndaje mu yaatu ci gëstu yiy taxawu jigeen ci diggante réew yi ñuy làkkee farañse yépp (Congrès international des recherches féministes dans la francophonie).

Atum 1993, mu daldi nekk ab gëstukat ca CNRS, ca iniwersite Paris-Diderot, ci màkkaanu gëstu bu tudd « Société en développement dans l’espace et dans le temps », nga xam ne ku ñu naan Catherine Coquery-Vidrovitch moo ko sos.

Mu dugal loxoom bu baax ci boole wuuteeb nekkinu góor ak wu jigeen ci gëstuwaay yi ak daaray Afrig yu kowe yi ak tamit, fexe ba siiwal mbootaayi jigeeni Afrig yi ak li ñu bëgg. Yemu ca, ndaxte fexe na ba ag lëkkaloo dox diggante jigeeni Afrig ak ay daaray Amerig yu kowe.

Moom mooy njiitu gëstuwaayu IFAN ci wàllu wuuteeb nekkinu góor ak wu jigeen ,.

Lu moy liggeeyu gëstukat bi muy def, moom mooy lëkkalekatu kureelu jigeen ak sàrti lislaam ci Afrig sowu jant ak tamit kureel gi ñu tudde ci àngale Development Alternatives with Women for a New Era, nga xam ne dafay yegge mbiri jigeen ñi ci yeneen kureeli àdduna yu mag yi, ngir ñu mën di am saafara.

Ay téereem[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • 2005 - « Les femmes, l’État et le sacré », L’islam politique au Sud du Sahara. Identités, discours et enjeux, M. Gomez-Perez (éd.). Paris, Karthala.
  • 2005 - « Penser les femmes et l’islam en Afrique : une approche féministe », contribution à Mama Africa. Mélanges offerts à Catherine Coquery-Vidrovitch. Paris, L’Harmattan.
  • 2005 - « Mobilisation des femmes en Afrique de l’Ouest », Gender Equality. Striving for Justice in an Unequal World, UNRISD, Genève.
  • 2004 - Notre corps, notre santé : la santé et la sexualité des femmes en Afrique subsaharienne, Fatou Sow et Codou Bop (dir.). Paris, L’Harmattan.
  • 2002 - Sexe, genre et société : Engendrer les sciences sociales africaines, A. Imam, A. Mama, F. Sow (dir.), version française par Fatou Sow de Engendering African social sciences. Dakar, CODESRIA/Karthala.
  • 2002 - La marchandisation de la gouvernance, version française par Fatou Sow de Marketisation of Governance, Viviene Taylor (dir.). Paris, DAWN-L’Harmattan

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lees jële feneen[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  •  Fees ko mën a xame
  • Balluwaay bu aju ci gëstu bi