Faatu Bensudaa
Dundu ak jaar-jaaram |
---|
Faatu Bensudaa | |
alt=Illustration.|222x222px | |
Ndombo-tànk | |
---|---|
Pólokilëer seneraalu Ëttu àttekaay bu àdduna bi | |
ba tey mu ngi yore ndombo-tànk loolu (juroom-ñetti at, ñaari weer ak ñeenti fan) | |
Njiit | Song Sang-hyun Silvia Fernández de Gurmendi Chile Eboe-Osuji |
Ki mu wuutu | Luis Moreno Ocampo |
Jëwriñ ji yore yoon Pólokilëer seneraal | |
– (ñaari at) | |
Njiitu réew | Yàyya Jàmme |
Ki mu wuutu | Hawa Sisay-Sabally |
Ki ko wuutu | Pap Cheyassin Secka |
Dundu ak jaar-jaaram | |
Tur ak Sant | Faatu Bom Ñaŋ |
Bésu juddu | |
Bérebu juddu | Bànjul (Gàmbi) |
Réew | Gàmbi |
Jànge | Iniwersite Obafemi Awolowo |
Liggeey | Laykat (Awokaa) |
Diine | Islaam |
| |
110x110px|Fatou Bensouda | |
Pólokilëer seneraal yu ëttu àttekaayu àdduna (Procureurs généraux de la Cour pénale internationale) | |
modifier lien=Modèle:Infobox_Personnalité_politique|12x12px|Consultez la documentation du modèle |
Faatu Bom Bensudaa mu ngi juddu fanweeri fan ak benn ci weeru sãawiyee atum 1961 ci Bànjul. Laykat (awokaa) la bu dëkk Gàmbi nekk tamit toppekat bu mag bu ëttu àttekaayu àdduna bi (pólokirëer seneraal bu Cour pénale internationale (CPI)[1] ) ginnaaw bu fa nekkee, diiru juroom-ñetti at, toppekat bi topp ci kow njiit la.
Dundu ak jaar-jaaram
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Nguneem
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Faatu Bensudaa mu ngi juddoo Bànjul. Waajuram wu góor ku njaboote la ndax am na ñaari jabar, am ak waajuru Faatu Bensudaa juroom-benni doom, am ak jeneen jabar ji juroom-ñaari doom. Waajuram wu góor nguur gi la doon liggeeyal, waajuram wu jigeen di liggeeye ci restoraŋub liise. Wax na ne, ci seen njaboot gi, góor ak jigeen yépp lañu doon ñaax ñu dem jàngi lekool. Kenn ci ay magam ? yu jigeen ab deppite la woon, am ci ku nekk jigeen ji jëkk a def surnaal ci tele bu Gàmbi, am ku ciy liggeey ci wenn tëralin wu jëm ci jigeen ñi te mbootayu xeet yi (Nations Unies) sumb ko.
Njàng ak tàggatoom
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Faatu Bensudaa dafa teel a bëgg xeex ngir nit ñi jot seen àq ak yelleef, rawatina jigeen ñi, di dem di teeweji ay layoo. Ginnaaw bi mu jàngee ci daara yu digg-dóomu te ñu ràññe woon ko ci lool, la Yàlla def mu nekk gerefiyee ca àttekaay bu Bànjul. Ci ndimbalu burs bu ko nguuru Gàmbi joxoon, la dem jàngi xam-xamu yoon ca Niseriyaa. Foofee, dafa jëkk a jànge ca iniwersite bu Ife nga xam ne tey moom lañu tudde iniwersite Obafemi-Awolowo 1982 ba 1986, laata muy jàngeji ca Nigerian Law School bu Lagos, foofa nag la ame lijaasa yoon bu tudd barrister at law atum 1987.
Bi mu liggeeyee diiru ñetti at, la bindu atum 1990, ci ab lekoolu mbootaayu xeet yi, lekool boobee mu ngi tudd International Maritime Law Institute, nekk ca Malt, foofee lañu ko joxe ab lijaasab yoonu géej (diplôme de droit maritime) atum 1991. Bi mu génnee ci ngornamaŋ bu Gàmbi, Faatu Bensudaa dafa amaat yeneen lijaasa, benn bi mu ngi ko am nowàmbar 2001 ca Comité international olympique ca Niw York, beneen bi, doon lijaasa buy firndeel njàngum làkku farañse mu mu def ñu naan ko DELF 1er degré te njëwriñ ji yore wàllu ndaw ñi, njàng, njàngale ak gëstu ju réewum Farãas jagleel ko ko.
Atum 1987 lañu ko nangul ag bokkam ci kureelu laykat (awokaa) gu Gàmbi. Ci menn at mi ñu tabb ko xelalkat ci ngornamaŋ bu Gàmbi. Féewiriyee 1994 la nekk ab toppekat (pólokirëer).
Taxawaayam ci nguuru Yàyya Jàmme
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ginnaaw foqati nguur ga amoon sulet 1994, la Faatu Bensudaa nekk kilifa gu am solo, ci wetu Yàyya Jàmme, di ko xelal ci wàllu yoon. Ñu yéegal màqaamaam atum 1996, def ko toppekat bu solowu ba 1998 ñu tabb ko toppekat seneraal bu Bànjul ak jëwriñ ji yore yoon ci ngornamaŋ bu Gàmbi,[2], njëwriñ jooju moo fa nekk ba bi ñu koy wàcce weeru màrs 2000.
Ñu ŋàññ nguuru Yàyya Jàmme ndax ñàkk a sàmm àq ak yelleefi doom-aadama, jàppe ko ni « genn ci nguur yi dàq a jaay-doole, dàq a noot askanam ci àdduna bi ».
Liggeeyu boppam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ginnaaw bi mu liggeeyee ci nguuru Yàyya Jàmme ba pare, dafa daldi ubbi genn këru liggeeyukaayu laykat, rax-ci-dolli jiite benn bànk diggante 2000 ba 2002.
TIRBINAALU ÀDDUNA NGIR RUWÀNDAA
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Atum 2002 la nekk xelalkat ci wàllu yoon ak wuutukatu toppekat bu tirbinaalu àdduna ngir Ruwàndaa ca Arusa, ca Tãasani.
Ëttu àttekaayu àdduna
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Atum 2004 ba léegi, mu ngi liggeeye ci Ëttu àttekaayu àdduna bu La Haye. Dafa fa jëkk a nekk toppekat bi sës ci toppekat seneraal bi di Luis Moreno Ocampo, laata mu koy wuutu fukki fan ak ñaar ci weeru desàmbar atum 2011, daldi waat fukki fan ak juroom ci weeru suyee (juin) atum 2012. Téemeeri réew ak ñaar-fukk yi bokk ci ëttu àttekaay bi ñoo ko tànn, ci tànneef bu doxoon diggante juroom-fukki nit ak ñaar, kenn ku ci nekk di yóotu palaas bi.
Ngornamaŋ bu Amerig dafa ko lànkal wiisaa awiril 2019 ba léegi, ndax dogalu ubbi ab lëñbët bu mu jël, ngir leeral tuumay salfaañe sàrti xare yu tegu ci ndoddu làrme bu Amerig, ca Afganistãa.
Ay raayaam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Ci gis-gisu surnaal bile di Time, moom Faatu Bensudaa, bokk na ci téemeeri nit ñi gën a fés, seen kàddu gën a diis ci àdduna bi atum 2012.
- Surnaal bii di Jeune Afrique, moom la def « kenn ci juroom-fukki jigeeni Afrig ñiy jëme dénd bi kanam ndax seen jëf ak seen sumb yi ñuy amal ci seen liggeey (2014 ba 2015) ».
Dundug biiram
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Soxna la ci benn borom xam-xamu koom ak dun, bu cosaanoo Marog tey dundu Gàmbi, mujj nekk ku bare ay isin. Am nañu ñaari bant.
Seetal tamit
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci yeneen naali wikimedia yi :
Faatu Bensudaa, ci Wikimedia Commons
Jukki yi ñu ko tudd
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Ëttu àttekaayu àdduna bi : (Cour pénale internationale)
- Limu way-pólotig yu jigeen yi <i><small>(Liste de dirigeantes politiques)</small></i>
Lees jële feneen
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Téere, jukki wala dali web yi ñu yër
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- ↑ « La Gambienne Fatou Bensouda élue procureure de la CPI », Le Monde et AFP, 12 décembre 2011
- ↑ « Royuwaay:Mme Fatou Bensouda, procureur de la CPI », site officiel de la CPI, consulté le 7 mai 2016.