Elen Jonson Sërliif

Jóge Wikipedia.
Elen Jonson Sërliif
Njiitu réewu Liberyaa
16 sãawiyee 2006 – 22 sãawiyee 2018
(Fukki at ak ñaar ak juroom-benni fan)
Ki mu wuutu Gyude Bryant
(Njiitu réewum négandiku)
Ki ko wuutu George Weah
Jëwriñu Liberyaa ji yore gafag réew mi
1979 – awiril 1980
(Lu yées menn at)
Sekerteer detaa bu Liberyaa bi féete gafag réew mi
1972 – 1978
(Juroom-benni at)
Dundu ak jaar-jaaram
Tur ak sant Elen Jonson
Bésu juddu 29 oktoobar 1938 (Juroom-ñett-fukki at ak benn)
Bérebu juddu Moorowiyaa
Réew Liberyaa
Kureelu pólotig Parti de l'unité (Ba 2018)
Jànge Iniwersite bu Colorado ci Boulder
Iniwersite Harvard
Borom-kër Jems Sërliif (Yàlla wéddi na seen sëy)
Elen Jonson Sërliif
Illustration.

Elen Jonson Sërliif atum 2015.

Ndombo-tànk
Njiitu réewu Liberyaa


(fukki at ak ñaar ak juroom-benni fan)
Pal 8 nowàmbar 2005
Palaat 8 8 nowàmbar 2005

8 nowàmbar 2005 nowàmbar 2011

Ki topp ci njiitu réew mi Joseph Boakai
Ki mu wuutu Gyude Bryant

(njiitu réewum négandiku)
Ki ko wuutu George Weah
Jëwriñu Liberyaa ji yore gafag réew mi


(lu yées menn at)
Sekerteer detaa bu Liberyaa bi féete gafag réew mi


(Juroom-benni at)
Dundu ak jaar-jaaram
Tur ak Sant Elen Jonson
Bésu juddu (juroom-ñett-fukki at ak benn)
Bérebu juddu Moorowiyaa (Liberyaa)
Réew Liberyaa
Kureelu pólotig Parti de l'unité (ba 2018)
Borom-kër Jems Sërliif (Yàlla wéddi na seen sëy)
Jànge Iniwersite bu Colorado ci Boulder

Iniwersite Harvard
Diine Méthodisme

(Diiney porotestãa ju sukkandi ci xutba John Wesley ba mu defoon ca fukk ak juroom-ñetteelu xarnu ba)


Signature de Ellen Johnson Sirleaf

116x116px|Ellen Johnson Sirleaf
Njiitu réewu Liberyaa

Neexalu Nobelu jàmm ji 2011

Elen Jonson Sërliif mu ngi juddu ñaar-fukki fan ak juroom-ñeent ci weeru oktoobar atum 1938 ca Morowiyaa (Liberyaa), doon jigeenu nguur ju Liberyaa, nekk fa njiitu réew, dale ko fukki fan ak juroom-benn ci weeru sãawiyee atum 2006 ba ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru sãawiyee atum 2018.

Borom xam-xamu koom-koom la bu jànge Etaasini (USA), moom mooy jigeen ji jëkk a falu njiitu réew ci déndu Afirig bi..

Atum 2011, kenn la woon ci ñi jël neexalu jàmm bi, ñu tudde ko prix Nobel de la paix.

Dundu ak jaar-jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Njàng ak cosaanam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñaar ci ay maamam, ñu ngi juddoo Liberiyaa. Way-juram wu góor, Jahmal Karney nga xam ne ag njaboot gu dëkk Liberiyaa te cosaanoo Amerig moo ko doomoo woon, lekool bu ñu naan College of West Africa ci Morowiyaa la ame woon lijaasa, daara joojee, iniwersite làbbe yi la. Ab laykat (awokaa) la woon. Bokk na ci maamam, Hilary R. W. Johnson, njiitu réewu Liberiyaa bu fa juddoo bu jëkk. Li waral deram bu xees bi mooy ne dafa am maam ju góor ju bokk ak yaayam te dëkk Almaañ. Ci ay way-jur yu am alal la juddoo, yaroo ci. Bi muy am fukki at ak juroom-ñaar la am borom-këram. Borom-kër baa ngi tudd Jems Sërliif, féete ko mag, doon liggeeye ca njëwriñu ji yore mbay mi, moom moomee sax, moo ko yombalal am njàngam ca Etaasini (USA). Jems Sërliif ab naankatu sàngara la te dafa ko doon tëkku moom ak ay doomam. Dafa ko doon fekksi sax ci njëwriñ ji yore gafakag réew mi, fi mu doon liggeeye, di ko pes, ndaxte nee na soxna si dafay gudde ñibbi. Bi mu amee juroom-benni at ci boobule sëy, la Yàlla wéddi ginnaaw bu ko borom-këram tiimale fetal ne dafa koy faat ci kanam doom ji.

Mu def njàngam ca Amerig ba pare daldi fa am bakalóoreyaa ci xam-xamu waññ (kontaabilite) ci Madison Business College, nekk ci dëkk bu ñu naan Madison (Wisconsin) atum 1964 ; am ab lijaasaab xam-xamu koom ca iniwersite bu Colorado atum 1970 ak benn mastë ci njàngum njiiteef ca iniwersite bu Harvard atum 1971. Way-bokk la ci kureel gu boole ay waa-Afrig ak waa-amerig yu jigeen Alfaa Kappa Alfaa (Sororité afro-américaine Alpha Kappa Alpha), nekk kureel gu ni mel gu ñu jëkk a sos atum 1908.

Way-bokk la ci ab jàngu bu ñu naan Église méthodiste unie,.

Ag njëlbeenam ci pólotig : kujje gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ab sekerteer detaa koppar yi la woon diggante 1972 ba 1978, laata muy nekk jëwriñ ji yore gafakag réew mi diggante 1979 ba 1980. Ci menn at mi, Samuel Doe foqati nguur ga, raylu ka fa nekkoon njiitu réew di William Richard Tolbert ci biir këram ak li ëpp ci ay jëwriñam ci ag tefes. Yàlla def Elen Jonson Sërliif mucc ca ndax li mu doon jigeen ak tamit li Samuel Doe bëgg mu des fa yenn njiit yu koy mën a gunge ci liggeeyam bi. Waaye Yàlla dimbale ko mu rëcc, dem tóxuji feneen, dellu ñibsiwaat ginnaaw gi, ne dafay def ay yëngu-yënguy pólotig ngir kontar nguur ga. Ci lañu ko tëkku ne dañu koy ray. Atum 1985, ñu daldi ko teg daan bu tollu ci fukki ati kaso ndax li mu àndul ak nguuru takk-der gi Samuel Doe jiite. Bi mu defee diir bu gàtt ci kaso gi, lañu ko may mu génn réew ma dem feneen. Li mu àndul woon ak nguur ga, di ko ŋàññi saa su nekk moo tax sax, ñu demoon ba tudde ko « Jigeen ju mën góor » (« Dame de fer ») ».

Ay jaar-jaaram ci liggeeyu borom xam-xamu koom-koom[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mu delluwaat Etaasini (USA) ngir wéyal liggeeyam bi ci wàllu koom, di liggeey ci bànku àdduna bi (Banque mondiale) ak tamit ci Citibank. . Mu jiite fa,  ci misaal, PNUD bu Afrig (Tëralinu mbootaayu xeet yi ngir suqaliku gi).

Atum 1997, mu dugal xaalisam ci kàmpaañu wotey njiitu réew ba ngir jàppalee ko Charles Ghankay Taylor, jëf jooju, dafa mujj jàpp ne sax njuumte la woon. Kureel gi yore « Waxtaan, waxante dëgg te juboo » (« Vérite et reconciliation ») dëgër lool ci ñu tere Elen Jonson Sërliif am ay ndombo-tànk ca réew ma ci diiru fanweeri at ndax li mu jàppale ay way-fippu ci xaalis,,.

Wotey njiitu réew yu 2005 ak diiru palam gu jëkk[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ellen Johnson Sirleaf ak njiitu réewu Amerig <i>George W. Bush</i> (2008).
Ellen Johnson Sirleaf ak sekerteer detaa Amerig <i>Hillary Clinton</i> (2010).

Elen Jonson Sërliif moo teewaloon pàrti bile di Parti de l’unité ca wotey njiitu réew ya, jàll ci sumbu wote bu jëkk ba oktoobar 2005, dem daje ak George Weah ci ñaareelu sumbu wote ba, juroom-ñetti fan ci weeru nowàmbar. Li tukke ci waññ yu mujj yi ñu siiwal ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar mooy ne, moom mi nekkoon jëwriñ ji yore gafakag réew mi, moo am juroom-fukk ak juroom-ñeent kos ñeent ci téemeer boo jël (59,4 %) ci falaakoon yépp, ci ñaareelu wote yi amoon ci juroom-ñetti fan ci weeru nowàmbar, George Weah mi fi nekkoon futbalkat bu àdduna yépp ràññe, moom daldi am ñeen-fukk kos juroom-benn ci téemeer boo jël (40,6 %) ci falaakoon yépp.

Elen Jonson Sërliif daldi jël lengey njiitu réew ya ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar atum 2005. Guleet ! Afrig am jigeen ju falu njiitu réew ci benn ci réewam yi. Fukki fan ak juroom-benn ci weeru sãawiyee, la waat ci kanam Henry Reed Cooper, di njiitu ëttu àttekaay bi gën a mag ca réew ma. Ca ndaje mooma sax, ay junney junney doomi réew ma, njiiti Afrig yu bare ak ndawi yeneen réew, teewoon nañu fa. Joseph Boakai lañu toftal ci moom.

Fukki fan ak juroom-ñaar ci weeru màrs atum 2006, ci am ndaje mu kureelu kaaraange gu mbootaayu xeet yi, Elen Jonson Sërliif dafa ñaan ñu teggi daan yi tegu ci kow réewam te aju ci jamãa bi ñuy jaayeji bitim réew ak tamit mbootaayu xeet yi des ca réew ma, bañ a dem. Dellu na fa biral ne pexeem ngornamãa bi ci wàllu saxal jàmm mu ngi sukkandiku ci ñeenti kenu : kaaraange, jiitug àq, yelleef ak njiiteef, doxalaat koom gi ak defaraat ay tabax ak yeneeni jumtukaay yuy ñoŋal nekkinu askan wi. Diiru palam gu jëkk gi yépp, genn-wàllu yoon yi wër Morowiyaa yépp defaraat na leen, nit ñi di am bu baax ndox ak kuraŋ saa yu ñu ko soxlaa, waaye ci wet gi nag, ndóol gi ak ndaw ñu amul liggeey (juroom-ñett-fukk ci téemeer boo jël (80 %) ñu ngi fa woon ne xas . Ba léegi nii, Liberiyaa bokk na ci fukki réew ak juroom yi gën a ndóol ci àdduna bi. Mu daldi jiital xeexu ger bi ci xeexam yépp, jëfandikoo ay xameem ci wàllu koom ak koppar ngir mën a leb xaalis bu mu suqalee réewam.

Juroomi fan ci weeru nowàmbar, la ko njiitu Etaasini (USA) George W. Bush tappal medaayu njiitu réew bi aju ci moom-sa-bopp gi. Juroom-ñaari fan ci weeru oktoobar atum 2011, ñu jox ko neexalu jàmm ji (prix Nobel de la paix) mu bokk ko ak doomu réewam jile di Leymah Gbowee ak waa Yemen bi Tawakkul Karman. Kujjeg pólotig ga fa nekkoon anduñu woon ci ràññatle boobu ndax ñenn ñi sax dañu gisoon ne, Hillary Clinton moo ko ci jàppale ndax wotey njiitu réew yu 2011 yiy jegesi.

Wotey njiitu réew yu 2011 ak ñaareelu diiru palam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom moo jël ndam li ci wotey 2011 yi, li ko ko yombalal mooy, wujjam Winston Tubman dafa ŋàññi doxalinu wote wi ba pare sant ay ñoñam ñu bañ a wote), falaakoon yi néewoon lool ndax ci téemeer boo jël, fanweer ak juroom-ñaar kos ñeent rekk a ci wote woon (37,4 %).

Fukki fan ak juroom-benn ci weeru sãawiyee atum 2012, ñu jox Elen Jonson Sërliif lengey njiitu réew ya, ci ñaareelu diirug palu njiitu réew, mu war a jiitewaat réew ma. Hillary Clinton, sekerteer detaa bu Amerig ak njiiti réewu Afrig yu bare, yu bokk ak Liberiyaa fu ñu féete ci dénd bi, teewoon nañu ca ndaje ma..

Fukki fan ak juroom-ñeent ci weeru màrs atum 2012, muy jàppal tànk yoon yiy    def ngóor-jigeen ag jagalti sàrti gu ñu war a daan ñi koy def ca Liberiyaa.

Atum 2014, lañu wax ak moom ci li jigeen ñi mënagul a jot ci suuf si, maanaam nekk borom suuf ca réew ma, te loolu doonoon ab dige bu mu defoon ci këru yéglekaay gile di Reuters atum 2013.

Oktoobar 2014, mu woote ndimbal fépp ci àdduna bi ngir ñi ko am te mën ko jàpp ci dakkal lawug jàngoroy ebolaa. Ñaari weer lu jiitu wooteem boobu, dafa ñaanlante woon ak jëwriñ yi nekkoon ci ngornamãam bi te ñëwaatuñu woon ca réew ma ngir bokk ci xeexu ebolaa bi.

Atum 2017, ñu tudd ko ci luubal alal ba woon ca Paradise Papers.

Diiru palam gaa ngi waroon a jeex ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru sãawiyee atum 2018 bi George Weah mi ñu fal ñaar-fukki fan ak juroom-benn ci weeru desàmbar atum 2017, di jël lenge yi ci yoxoom. Wote yooyule, George Weah mu ngi leen séqoon ak ka ñu toftaloon ca njiitu réew ma di Joseph Boakai

.

Ay ndombo-tànkam yu nguur[Soppisoppi gongikuwaay bi]

    • 1972-1978 : Sekerteer detaa bu gafakag Liberiyaa (secrétaire d'État aux Finances du Liberia)
    • 1979-1980 : Jëwriñu gafakag ngornamãa bu Liberiyaa (ministre des Finances du gouvernement du Liberia)
    • 1982-1985 : Ki topp ci njiitu déndu Afrig ngir màkkaanu Citibank, Nairobi (vice-présidente de la Région Afrique pour le Bureau de Citibank, Nairobi)
    • 1986-1992 : Ki topp ci njiitu kureel gi jiite bànku Équateur, Washington, D.C., nekk fa tamit ab way-bokk (vice-présidente et membre du Comité de direction de la banque Équateur, Washington, D.C.)

prix Nobel de la paix

    • 1988-1999 : Way-bokk ci njiiteefu The Synergos Institute
    • 1992-1997 : Njiitu tëralinu suqaliku wu mbootaayu xeet yi ci Afrig (directrice du programme de Développement des NU Bureau pour Afrique)
    • 1997 : Njiitu Parti de l'unité
    • 2004-2005 : Njiitu kureelu nguurin gu jub te sell (Liberiyaa) (présidente de la Commission de bonne Gouvernance (Liberia)
    • 2005 : Njiitu Parti de l'unité ; way-wotelu ci wotey njiitu réew yi (dirigeante du Parti de l'Unité ; candidate à la présidence)
    • 2006 : Njiitu réew mi (présidente de la République)

Yeneen nbombo-tànk yu bokkul ak yu nguur[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Jëwriñ ju jëkku Àngalteer <i>David Cameron</i>, Ellen Johnson-Sirleaf, <i>Bill Gates</i> ak <i>Andrew Mitchell</i> (2011).
  • Way-bokk ci ñi sos Institut International ngir njiit yu jigeen yi ci wàllu pólotig ;
  • Way-bokk ci Conseil d'investissement ngir suqalikug Afrig gu tey ;
  • Way-bokk ci kureelu Moderne Africa Fund Managers ;
  • Njiitu bànk bu Liberiyaa ngir suqaliku gi ak dugal xaalis gi (banque du Liberia pour le Développement et d'investissement) ;
  • Njiitu Kormah Development and Investment Corporation ;
  • Kilifa ci leble xaalis bi ci bànku àdduna bi (Banque mondiale) ;
  • Njiitu kureelu waxtaan, waxante dëgg, juboo bu Liberiyaa (Présidente de la Commission de vérité et de réconciliation libérienne) ;
  • Ki topp ci njiitu <i>Citibank</i>.

Atum 2006, moom moo nekkoon juroom-fukkeelu jigeen ak benn ji ëpp doole ci àdduna bi ci gis-gisu Magasin  bi ñu naan Forbes. Atum 2007, mu jël téemeereel, atum 2008, mu jël juroom-benn-fukk ak juroom-benneel.

Ay raayaam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Neexal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • 1988 : Neexal yu « quatre libertés de Roosevelt » ci wàllu sañ a wax sa xalaat
  • 2006 : Neexalu Freedom Award
  • 2007 : Medaayu njiitu réew ci moom-sa-bopp
  • 2011 : Neexalu Nobelu Jàmm mu bokk ko ak Leymah Gbowee ak Tawakkul Karman
  • 2012 : Neexalu Indira Ganfhi
  • 2014 : Neexalu koom-koom bi yépp bu Kiel
  • 2017 : Téemeeri jigeen
  • 2017 : Neexalu Mo Ibrahim

Sag yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • 2006 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Marquette
  • 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu <i>Indiana</i>
  • 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Dartmouth 
  • 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu <i>Brown</i>
  • 2009 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu Tampa 
  • 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu<i>Yale</i>
  • 2008 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu<i>Rutgers</i>
  • 2011 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu<i>Harvard</i>
  • 2014 : Ange de la paix
  • 2016 : Doktoraa onoris kóosaa bu iniwersite bu<i>Dartmouth College</i>

Ay medaayam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • 50x50px <i>Grand-Croix</i> de la Légion d'honneur, juroom-ñaari fan ci nowàmbar atum 2012, François Hollande moo ko ko tappal
  • 50x50px <i>Collier de l'Ordre Pro Merito Melitensi</i> (Malte)
  • 50x50px Commandeur de l'ordre de Mono (Togo)
  • 50x50px Order of the Pioneers of Liberia (en) (Liberia)
  • 50x50px Order of the Star of Africa (en) (Liberia)
  • 50x50px Humane Order of African Redemption (en) (Liberia)

Dundug biiram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Elen Jonson Sërliif am na ñeenti doom, ñaar ñi mu jox liggeey yu am ñam ci nguur gi. Bokk na ci doomam yooyu, Robeer Sërliif, mi nekkoon njiitu kureelu njiiteef gu këru liggeeyukaay gi yore petorolu Liberiyaa, nekkati xelalkatu yaayam jiy njiitu réew mi, Moom moomu di Robeer Sërliif, dafa ñàkkoon atum 2014, ay wote senaatëer yu mu doon def ak George Weah ngir jiite diiwaanu Montserrado ; Jeneen doomam ji moo doon jiite caytug lépp luy xiibaaru biir réew mi : ñetteelu doomam ja nag moom, moo toppoon ci njiitu bànk sàntaral ba.

Téere bi mu bind[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Toftal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  Ci yeneen naali Wikimedia

Elen Jonson Sërliif, ci Wikimedia Commons

Lees bind ci moom[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Ellen Cooper Madame la Présidente : Une biographie d'Ellen Johnson Sirleaf, trad. de l'anglais par Mathilde Fontanet, 2018, Editions Zoé, Coll. Ecrits d'ailleurs, 448 p.

Jukki yi ñu ko tudd[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Limu njiiti pólotig yi : <i><small>(Liste de dirigeantes politiques)</small></i>

Lees jële feneen[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Dundu ak jaar-jaaram ci dalu webu Fondation Nobel (am na ab ruq bu nekk ci xët wi te am ay seetukaayi joxe neexal yu bare, bokk na ca, ab jukki bu borom neexal bi bind ñu tudde ko Nobel Lecture, te muy andi ay leeral ci li mu def.
  • Royuwaay:Autorité
  •