Aller au contenu

Diisaayu yaram yi

Jóge Wikipedia.

Diisaayu yaram yi (corps)

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Tay de bis bu xiin la, tàmbali naa taw, doqi ndox yu ndaw, yu xaw a rëy, yu ngandee ngandee ngi nii far di rot ci suuf.

Bu cooroonee, gàncax gu bari seeni xob day ruus, daal di naaw ci jawwu ji, rotati ci suuf si.

jël-leen aw xeer ci seen loxo, wacc-leen ko, day rot ci suuf de.

Benn sabab bi tax xeer woowu di rot, tax it ba xob wi rot, moo fi jaar ba tax doqi ndox yu taw yooyu di rot: loolu mooy li nuy wax Bijj gi walla Dooley ñoddi gi suus si di amal ci yaram yi. Ñoddi gii mooy tax yaram yiy diis, moo waral it ñuy aajowoo genn kattanug përëg ngir yékkatee léen ci suuf si.