Dibbtóon
Dibbtóon (pos ca Saalum) as ngarab su ndaw la su man a toll ci juroom benni met. Xobi dibbtóon day xaw a dëgër. Ay wàqaasam day laxasoo di am car yu ndaw yuy am i dég. Garabu dibbtóon manees na koo góob ci àll ngir jëfandikoo ko cim paj.
Barab yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garabu dibbtóon man nañu koo fekk ci kembaaru Afrig li ko dale Seneegal ba Ecopi, Ugandaa, Keeñaa, bëj-saalumu Namibi Botswaana mbaa ca Mosàmbik, gàncax la gu man a màgg ci suuf su nanguwul, ci suuf su wow mbaa su am i xeer wala suuf suy taa nawet.
Meññeef mi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Doomub dibbtóon deesu ko lekk, ay xobam it noonu. Waaye reen yi buñu ko baxalee man naa faj tooy ak coono. Leeg-leeg ñu toggaalee ko ak laax mbaa ruy ngir faj yaram wu tàng.
Yeneeni njariñ
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bantu garabu dibbtóon manees na koo lakk ngir am xeetu sunguf su ñuy defare saabu. Doom bi manees na cee cuub.
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Gardenia ternifolia