Dambal
Apparence
Dambal garab gu siiw la ci ne Senegaal la bàyyikoo waaye dees na ko gis ci yaneeni barab ci Afrig.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab la guy àgg 10 ba 15i met.
Xobam dafa wërmbalu tóor-tóoram juróomi xob la am. Guddi day gilli xet gu xasaw, day ndiiraan foytéef bu lax.
Xetam day xàcc njugub yiy ñëw sabab ag saxam.
Danay meññi ay foytéef yu dijj te baam ba noppi di lang. Foytéefam siiw na ci ne nit du ko lekk waaye ca gox yamuy sax dees nako lekk ci lu dul togg.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ginnaaw ag lekkam baa ag taaralam, dees na ko jëfandikoo ci taaral deru jigeen, dees na ci génnee it diw dees na ci faje it, dana faj ñatti xeetu kaaseer: kaasseeru ween, kaaseeru res, kaaseeru suufu nit.
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Kigelia africana
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]farañse: sausage tree |
angale: arbre à saucisses |
itaaliyee: albero delle salsicce |