Daaru Gay
Dëkk la boo xam ne, moo ngi bokk ci goxub ( Cees) tundu ( Kajoor)(Département bu Tivavone)( Commune bu Koul Diop ) Daaru Gay digganteem ak Ngaay Mexe mi ngi tollu ci 12 Kilomeetar digganteem ak Pir Xaali Amari Faal tollu ci 15 / 16 Kilomeetar Daaru Gay li ëpp ca askan wa dañuy yëngu ci wàllu yaxantu ak bay, lu mel ne gerte, dugub, ak ñebbe. Di nañu yar ag jur lu mel ne Xaral, Bëy, nag Fas, ak Ginaar. Daaru Gay amna ekoolu Araab ci atum 1976 ay kàngam yu bari génnee nañu fa, lu jiitu loolu mag ñi ñoo daan jàngle Alxuraan ci séen biir kër. Ku mel no Sëriñ Musaa Njaay, ak doomam Sëriñ Góora Njaay, Sëriñ Abdu Kariim Gay, Sëriñ Moor Ñaan Sëriñ Asan Ñaan, Sëriñ Omar Sàll, Sëriñ Usmaan Gay, ak Sëriñ Baara Gay. Daaru Gay batay amna Daaray Alxuraan ci atum 2008 xale yu bari wàttu nañu fa Alxuraan. Liiñe nanu dëkk ba tamit ci atum 1975 Daaru Gay amna ñu am ndox mu bàyyikoo ba Fass Jaksaaw dëkkub Sëriñ Abdu Asiis Si Maalig ci atum 1987 At mu ne amna Màggal gu mag gu fay am goo xam ne ñi ngi ko tàmblee woon ci atum 1987 di ci ñaanal ak fàttaliku séen Maam Sëriñ Maxtaar Gay ak mag ñu baax ñi mu àndaloon. Am nañu Electricité ci atum Amna tamit ab Poste de Sante ci atum 2021Am na Jumaay ju taaru joo xam ne mi ngi noppi ci atum 2016 Daaru Gay nekk dëkkub diine ak Lislaam ñu nekk ay taalube yu am jom nangoo liggéey bëgg séenub dëkk boole ci fonk Sëriñ tuubaa ak Maam Cerno ak séenug njaboot. Njabootug Maam Cerno Faati Broom Daaru Daaru, ñu baree bari daa nañu fa ñëw rawatina Sëriñ Móodu Awa Balla Mbàkke ak Sëriñ Hamsatu Mbàkke mi nga xam ne am na fa sax kërug boppam ci atum 1976 Njabootug Sëriñ tuubaa, Sëriñ Abdu Lahad Mbàkke ñëw na fa. Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke ñëw na fa. Daaru Gay Sëriñ Maxtaar Gay moo ko sañc, àndoon ak ay doomi baayam. Ku mel ne Sëriñ Ma-Sayeer Gay, Sëriñ Gay Sëy Gay, ak Sëriñ Ahmadu Maxtaar Gay, ñoom ñent ñii ñoo bokk benn waajur bu góor di Sëriñ Mandaak Gay. Waaye Sëriñ Maxtaar Gay ak Sëriñ Ma-Sayeer Gay, ak Soxna Faatima Njaay Gay, ak Soxna Xari Njaay Gay ñoom ñii ñoo bokk benn waajur bu góor di Maam Mandack Gay, séen Waajur bu jigéen di Soxna Maam Njaay Sàll doomi Soxna Anta Jama Suraŋ. Batay ñi fekkewoon bi nuy sañc Daaru Gay bokk na ci kunuy wax Sëriñ Moor Gay Ilimaan, Mi nga xam ne Sëriñ Ma-Gay Ndaak mi ko jur mook Sëriñ Maxtaar Gay ñoo bokk benn waaju bu góor di Maam Mandaak Gay. Sëriñ Maxtaar Gaye batay mi ngi àndoon ak lenn ci ay jarbaatam ku mel ne Sëriñ Muusaa Njaay, Sëriñ Aliyu Siise. Daaru Gay Sëriñ Maxtaar Gay mi ngi ko sañc ci atum junni ak juróom ñenti téereem ak fukk ak juróom ñent 1919 ginnaaw bi mu ci amee ndigalul Maam Cerno Faati Boroom Daarul Muhti. Mu nekk dëkkub diine ak lislaam, Sëriñ Maxtaar Gay nekkoon fa, mook ay rakkam, di ay doomi baayam, ku mel ni Sëriñ Gay Sëy. Ak Sëriñ Ma-Sayeer Gay. Ak ay jarbaatam, ku mel ni Sëriñ Omar Sàll, Sëriñ Musaa Njaay, Sëriñ Moor Ñaan, Sëriñ Asan Ñaan, Sëriñ Abdu Ñaan, Sëriñ Omar Ñaan. Ak ay doomi ndayam ku mel ne Sëriñ Ahmadu Jaxate, waajur Sëriñ Ndaam Jaxate miy waajur Sëriñ Móodu Jaxate Tuuba Mbàkke, ak lenn ci ay taalubeem. Boolewoon liggéey, jaamu Yàlla, jàng ak jàngle, ak yar njaboot gi.
SËRIÑ MAXTAAR GAY AB JUDDOOM.
Mi ngi juddoo dëkk bu ñuy wax Jëmmooy Gay bokk ci Njàmbur, ginaaw ba mu jóge fa ñëw Kajoor dëkk bu ñuy wax Ngay-Ngay làkk ñu gën koo xame ci turu ( Ngay-Ngay Asan) di dëkkub Maamam Sëriñ Asan Gay.
Sëriñ Maxtaar Gay ag njabootam :
Aji bind ji Móodu Gay Fàllu Daaru Gay.