Dóobaali
Dóobaali garab la gu rëy gu am xob yu dëgër yu man a toll ci juróom-benn ba ci ñaar fukk ak benni met ci njoolaay. Lu ci ëpp ag ray-donn lay doon. Muy garab gi day juddoo ci kaw geneen garab gu màggat. Bu juddoo ci kaw garab googu, dana am ay reeni jaww yoo xam ne dana màgg ba laal suuf di am it ay xob yuy mujjee muur xobi garab gi mu juddoo, am peer bu mujj nangu peeru garab gi mu juddoo mujj gi nag mu nekk garab ci boppam gu rëy lool.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab gi nag leeg-leeg man nañu koo jëmbët ngir ay foytéefam walla ay njariñam cim paj walla yeneen yuñu ko man a jëfandikoo. Leeg-leeg it danañu ko jëmbët ngir mu man a mbaar ci bërëb yi ñuy féexloo. Keppaar gu neex la am.
Njariñi paj yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dóobaali garab gu bari ay njariñ la ci wàllu paj. Xas mi dañu koy jëfandikoo ci lépp luñuy faje fajum cosaan. Maanaam faj soj, man a faj put guy metti, man a faj biir buy daw, man a faj i goom, man a faj seere, man a faj bakkan buy bori, ñu man koo it jëfandikoo ngir yokk meewu jigeen juy nàmpal. Amna it lu ñu man a jël ci xas mi boole ko ak ndox mu tàng ngir faje ko feebaru sëqët, man a faj feebaru laago man a faj feebaru gaana. Ba leegi ci xas mi, man naa faj it feebaru kataraag. Reen yi ku ko togg jox jo jigeen ju ëmb, man na ko musal ci ëmb buy yàqu.
Leneen ci ñjariñi garab gi xas mi man nañu cee liggeey basaŋ yu baax, man cee liggeey goj yu dëgër mbaa nu jëfandikoo bant bi niki mat mi ñuy toggee.
Mbay mi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mbayum dóobaali lu man a nekk la ci ñaari fànn. Bi ci njëkk mooy garab gi man nañu koo ji xaar mu sax wala ñu dagg lu cosaanoo ci moom, weer ko ba mu xaw a fendi, ñu sàmpaat ko ci suuf su nooy, suuf su tooy, ci bërëb boo xam ne danañu ko aar ci ngelaw ba mu bañ a damm.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Reeni bitti yi
-
Meññeef mi
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ficus thonningii
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]farañse: figuier à pagnes |
angale: common wild fig |