Aller au contenu

Déem

Jóge Wikipedia.

Déem garab la gu bokk ci njabootu Rhamnacées di cosaanoo ci réew yu am naaj yi ci àdduna. Bari na ay xeet lool. Déem yiy am i dég dañuy meññ, di am i doom.

Déem gi (Ziziphus)
Déem gi (Ziziphus)

Déem garab la gog day am ay dég yu sew te ñaw. Ay xobam day nëtëx te tuuti. Guddaayu peer bi day toll ci digganta benn meetar ba ñaari meetar. Guddaayu garab gi yépp dana yegg ci ñatt ba ñenti meetar.

Tóor-tóor yi
Tóor-tóor yi

Foytéef bi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Foytéef bi day tàmbalee ci nëtëx foofu xoox bi day weex, bu noppee jàll ci mboq daal di mujje ci wirgo wu xonq. Day saf suukar te neex lool. Xoox bu dëgër lay am, boo ko tojee dangay fekk ca biir lu nooy lu mel ni gerte.

Dafa gànjaru ci witaamin A, C. Am na it feer ak kalsóom.

Xoox bi dees koy jëfandikoo ngir defar diwu yaram.

Déem bi
Déem bi

Dénku déem luñu baaxoo jëfandikoo la ca réewi katalã ya ngir defar jumtukaay yu bari yees di jëfandikoo ci misig yu xeetoo ak i xalam niki: koblaa, falabiyol, tiibal ak tenoraa. Dees na ko jëfandikoo it ngir defar xeeti pontu yi ñuy daaj ci xalam yi ngir takk ci buum yi.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ziziphus