Dédd

Jóge Wikipedia.
Nataalu garabug Dédd

Dédd genn xeet la ci xeeti garab yi, mi ngi bokk ci njabootug Fabacées, mi ngi fekk baax ci Afrig gu ron-saharaa

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gii melow ñax gu sëq gu law ci guddaayu garab lay yor.

Yenn saa yi nag melow as ngarab su dàttam di àgg 20 ba 30i sàntimet ak 3 ba 5i met ci guddaay lay yor. Daa bariy dég, yu ay car ak reeni xobam tiye. Seen ug guddaay danay àgg ba 8i milimet. Doomam day tàcc, di yore melow puur, xonq mbaa baam tey àgg cig natt 6 ba 10i sàntimet ci guddaay ngir 1 ba 1,5 sàntimet ci yaatuwaay. Ci tënk 6 ba 8i saal yu tàcc, yu nëtëx mbaa xuun lay ëmb.

Njariñ[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dédd gi deef na ko jëfandikoo nig garabu paju cosaan. Tóortóoram meññ lem. Màttam danay jariñ ci defarug jumtukaay yu wuute (tum, fett...). Wàqaasam dees na ko feteñe.

Nataal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Senegalia ataxacantha acacia ataxacantha