Biir bu daw
Biir bu daw | |
---|---|
Toftale ak balluwaayi biti | |
Specialty | infectiologie[*], gastro-entérologie[*] |
ICD-10 | A09, K59.1 |
ICD-9-CM | 787.91 |
DiseasesDB | 3742 |
MedlinePlus | 003126 |
eMedicine | ped/583 |
Patient UK | Biir bu daw |
MeSH | D003967 |
Biir bu daw wala Jaare mooy ngay dem wanag gën gaa néew ñatti yoon ci bis te li ngay génne ginaaw kër yi dafay ndoxe. Yenn saa mu jàpp la ay fan, te loolu mën na tax sa yaram ñàkk ndox. Su yaramu nit ñàkkee ndox deram dootul nooy te it mën a soppiku. Mën nga dem ba dootoo saw lu bari, sab der furi, sa xol di tëf-tëfi, te sam xel dootul dox ni mu waree wala say jëf yeex, su demee ba gën a tar. Ginaaw kër yu tooy te bañ a ndoxe mën dal liir yiy nàmp, waaye, loolu du dara.[2]
Li koy gën a faral di joxe mooy jàngoro yiy jàpp butit yi te di bawoo ci ab wiris, bakteri, parasit, wala feebar bu ñuy woowe gastroenteritis. Yooyu jàngoroo ngi faral di bawoo ci ndox wala ñam wu am doomu jàngoro ji, wala ku am jàngoro ji wàll la ko. Mën nañu ni ñàtti xeeti biir bu daw ñoo am: biir bu daw bu yàggul, biir bu daw bu ànd deret bu yàggul, ak biy weesoo ñaari ayi-bis, muy biir bu daw bu yàgg. Biir bu daw bu yàggul te ndoxe mën na nekk kolera. Su àndee ak deret, ñu gën ko xame ci disànteri.[2] Amna yeneen mbir yu wuute ak jàngoro yu mën a joxe biir bu daw, muy lu ci melni: Ipertiroyidism, biir buy bañ soow, feebaru biir buy metti, yenn xeeti garab yi, ak sendoromu biir buy metti ak yeneen mbir.[3] Yi gën bari ci ñoom soxlawu ñu ñuy amal njàngat mu xóot ngir xam li leen waral.[4]
Liy musalaate ci biir bu daw mooy cet, di naan ndox mu sell, ak raxas loxo. Nàmpal liir ba juróom benni weer gën gaa néew lañu digle ak ñaq biy aare ci rotawiris. Pajtalu naan ndox muy faj (ORS), manaam ndox mu sell muñ boole ak tuuti xorom ak suukër, kumu neex nga fajoo ko. kumu neex itam nga jëfandikoo doomi Zinc.[2] Xayma nañu ni garab yooyu muccal nañu 50 miliyoŋi xale ci 25 at yii weesu.[1] Taamu nañu ci ku am biir buy daw mu wéy di lekk ñam wu sell, sudee liir ñu wéy di ko nàmpal.[2] Soo amul foo jëndee ORS (ndox muñ jaxase ak xorom ak suukër), mën nga koo defaral sa bopp.[5] Sudee nit ki daa ñàkk ndox mu bari, war nañu ko mën a sampal buteel.[2] Lu ci gën bari; naan ndox mu bari mën na ko saafara.[6] Antibiotik, suñu ko jëfandikoowul lu bari, dina ciy faral di baax ci ñi am biir buy daw ànd ak deret ak yaram wu tàng lool, ak ñiy am biir buy daw bu ñu tukkee, ak ñi am yenn jàngoro yi ci seen biir.[4] Loperamide mën na wàññi jaabante bi ci wanag wi waaye kenn digalu ko ñi seen biir bu daw tar lool.[4]
At mu nekk dina am lu tollu ci 1.7 ba 5 miliyaar ciy biir yuy daw.[2][3] Fi mu gënee bari mooy ci réew yu néew doole yi, nga xam ni xale bu nekk biiram dina daw ci xayma ñatti yoon ci at mi.[2] Ci àdduna bi yépp, ci atum 2012, mooy ñaareelu jàngoro juy faat xale yi yi amagul juróomi at (0.76 miliyoŋ wala 11%).[2][7] Biir bu daw bu bari mooy faral di indi xiibon te itam mooy li ko gën a faral di joxe ci xale yi amagul juróomi at.[2] Su yàggee mën na jur jafe-jafe yu ci melni ñàkk kàrtan wala xel mu neex.[7]
Royuwaay yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- ↑ 1,0 et 1,1 "whqlibdoc.who.int" (PDF). World Health Organization.
- ↑ 2,0 2,1 2,2 2,3 2,4 2,5 2,6 2,7 et 2,8 "Diarrhoeal disease Fact sheet N°330". World Health Organization. April 2013. Retrieved 18 June 2014.
- ↑ 3,0 et 3,1 Doyle, edited by Basem Abdelmalak, D. John (2013). Anesthesia for otolaryngologic surgery. Cambridge: Cambridge University Press. pp. 282–287. ISBN 1107018676.
- ↑ 4,0 4,1 et 4,2 DuPont, HL (Apr 17, 2014). "Acute infectious diarrhea in immunocompetent adults.". The New England journal of medicine 370 (16): 1532–40. PMID 24738670. doi:10.1056/nejmra1301069.
- ↑ Prober, edited by Sarah Long, Larry Pickering, Charles G. (2012). Principles and practice of pediatric infectious diseases (4th ed.). Edinburgh: Elsevier Saunders. p. 96. ISBN 9781455739851.
- ↑ ACEP. "Nation’s Emergency Physicians Announce List of Test and Procedures to Question as Part of Choosing Wisely Campaign". Choosing Wisely. Archived from the original on 17 May 2014. Retrieved 18 June 2014.
- ↑ 7,0 et 7,1 "Global Diarrhea Burden". CDC. January 24, 2013. Retrieved 18 June 2014.