Bere
Apparence
Ci làkku gereg Βέροια; Ci angale mooy Berea; Ci faranse mooy Bérée
Benn dëkk ci diiwaanu Maseduwan la woon. Nekkoon na ca joor ga nekk ca taatu tund wi ñuy wax Bermio lu tollu 35 kilomet digganteem ak Géeju Ese (mer Egée). Dëkku Gereg la bu amoon ay Yawut yu bare. 70 kilomet moo nekk diggante Bere ak Tesalonig. Tey jii dëkk bi Weroya (Véroia) la tudd.
Man nañu jàng ci Bere ci Jëf 17:10-14; 20:4.