Aller au contenu

Benteñe

Jóge Wikipedia.
Benteñe gi (Ceiba pentandra)

Benteñe xeetu garab la gu bokk ci njabootu Bombacaceae ci nose gu yàgg ga, ci gu yees gi nag ci gog Malvaceae

Garab gu am jëm la gog man na àgg ba 40i ci guddaay (ba sax 60i met ci guddaay ca Afrig). Ronam day liis, am i dég te ci yaatal wàqaasam day tàlleeku ba noppi raase. Tóortóoram 5 ba 9i xob lay am, yu wërmbalu lay doon te guddee nu day ni 10 ba 18i sàntimet. Foytéefam këmbaan guy lang, 10 ba 30i sàntimet moo di guddaayam.

Njariñ li

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Màttum benteñe nekk na lu ñu bari xëntewoo ngir jariñoo ko ci anam yu wuute te bari.

Turu xam-xam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ceiba pentandra