Benteñe

Benteñe xeetu garab la gu bokk ci njabootu Bombacaceae ci nose gu yàgg ga, ci gu yees gi nag ci gog Malvaceae
Melo wi[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
Garab gu am jëm la gog man na àgg ba 40i ci guddaay (ba sax 60i met ci guddaay ca Afrig). Ronam day liis, am i dég te ci yaatal wàqaasam day tàlleeku ba noppi raase. Tóortóoram 5 ba 9i xob lay am, yu wërmbalu lay doon te guddee nu day ni 10 ba 18i sàntimet. Foytéefam këmbaan guy lang, 10 ba 30i sàntimet moo di guddaayam.
Njariñ li[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
Màttum benteñe nekk na lu ñu bari xëntewoo ngir jariñoo ko ci anam yu wuute te bari.
Nataal yi[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
-
Garab gi
-
Tóortóor yi
-
Xob yi
-
Dég i benteñe
-
-
Doom bi