Aller au contenu

Baynuk

Jóge Wikipedia.

Baynug

Baynug yi dañu bokk ci waaso yu jëkk nekk Kaasamaas aeaaaleen na l, waiayea penku lañu joge. Foofu Kaasamaas,u enn nguur lañu taxawoon,àbu ñu naan Kansaalaa, seen peey di Mampatiŋ. Loolu, ak seeni buur di Gana Sira Bana. Li yépp, ba Imbraatóor gu Mali ame la xewoon. Ba mu yagg, Màndiŋ yi, jóge Mali, ñëw ci ñoom, di leen xeex ngir nangu leen. Ku daan jiite Mandiŋ yi mooy Tiramakan Taraaware. Ba noppi, Mandiŋ yi yilif nañu dëkku Baynug yi ak yeneen xeet ñu fa nekkoon (Joolaa, Pël...), te taxawal seen i nguur ci seen kaw, mooy nguuru Kaabu. Ba loolu xeewe, buuru Baynug yi Kikikor la woon, buur boobu la Tiramakan Taraaware taseel ci xaare.

Ñooñu daan jiite Màndiŋ yi, Naanco lañu leen tudde ci cosaan. Bi ñu yilifee moomu réew, di réewum baynug yi, dañu a sëy ak ñoom. Moo tax ci seen wallu nday, Naanco yi, ci Baynug walla Joolaa lañu bokk. Li moo tax it, Màndiŋ ak Baynug ak Joolaa yi, ay sant yu bari ñoo ko bokk (Saane, Maane, Jaabi, Jemme, Sambu, Jaata, Saañaa...). Waaye sant bi ñu leen gën a ràññee mooy: Jaandi. Tey sax, Baynuk yi, ñu bari ay Màndiŋ lañu.

Waaye, loolu yépp, taxul réewum Baynug yi nekk, ba atum 1830 ak 1867, bi ngeen xam ne, seen peey bu ñu naan Birikama tàkk te Kansaala daanu.

Seen lakk, Baynuk la tuddu, te xaj na ci ñaar, am Baynuk Gunyamoolo ak Baynuk Samik. Baynuk yepp, dañu ne, 34 500 lañu.

Baynuk yi, am na ay ceddo ñu nekkoon bu jëkk, am na ay jullit ak ay katolig.