Bañkatu ndeer

Jóge Wikipedia.

Royuwaay:Voir homonymesBañkatu Ndeer te nu gën ko xame bañkatu jigeeni Ndeer wala talaatay Ndeer nekk na fànn guy màndargal wala misaal bu wone xeex bañ a doon njaam gi amoon ci xew-xewu démb senegaal..

Ana lu xew? Benn bésub talaata ci weeru nowàmbar atum junni ak juróom- ñetti téemeer ak fukk ak juróom-ñeent la nit ñi dëkkoon Ndeer (Ndeer doon suuf si buur yilif, naatoon lool ca Waalo) fippu ci caay-caayu jaaykatu njaam yi jóge ca Marog te seen njiit doonoon Amar Ulda Moxtaar. Naar yooyoo ngi bokk ci giiri tarsas doon laamaan bi jokku ci buur ak tukulëer yu jóge bët-gànnaaru Senegaal

Fànn googu, taarix nettali na ko. Li muy metti yépp waa dëkk ba wone nanu ci seen jàmbaar. Am nañu ci woy wu dul fey mukk. Nit ña xare nañu fa, jaay fa seen bàkkan, mu gënal leen doon jaam.

Anam bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Naar yi jóge bëj-gànnaar réew mi doon nañu song péeyub Waalo ci ndoorteelu fukki xarnu ak juróom-ñeent. Looloo taxoon nu toxoloon péeyub Waalo jëlee ko jurbel yóbbu ko Ndeer (soo gënee wacc ci dëkk bi) (1).

Giiri lamaan yi jokku ci buuru Marog (mbooleseeni réewi karceen yu bokk benn buur) ñu ngiy jëlee xaalis ci njaayum jaam yi ñu jàpp, jaayaat leen boroomi barke yi jóge bëj-gànnaar afrig rawatina Marakes.(1)(2)

Njaayum jaam lu yàgg am la waaye ci ndoorteelu fukki xarnu ak juróom- ñeent lañu ko gisaat. Li ko waral mooy Naar yi ragal nañu tubaab yi nekk Ndar nangu Waalo. Looloo tax Naar yi baral cong yi. Ba xew-xewu ndeer di am, booba barag Amar Farim Borso mu ngi Ndar ànd ak gàngooram yi jóge ci beneen xeex ak Naar yi, am ñu ci gaañu doon fajusi.(2) (3).

Ni mbir mi demee[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gàngoori Naar yi ànd nanu ak seeni farandoo song péey ba bésub "talaata" ci weeru nowàmbar atum junni ak juróom- ñetti téemeer ak fukk ak juróom-ñeent. Ca jamono jooju, góor ñu bare ñu ngi woon ca tool ya. Xale yi ak jigeen ñi ñoo desoon ca dëkk ba.

Ba nu séenee aji song Naar yi ak seen njiit Amar Ulda Moxtaar(4) lanu

yëgle ci saa si. Noonu jigeeni Ndeer yi taxawe temm, dogu sàmm dëkk bi ak yenn ci soldaar yu tuuti yi fa desoon.

Nëbb nanu xale yi ca toolu dugub bi nekk ci wet ga. Jigeen ña jël nañu seen gànnaay, sol seen yëre jëkkër ngir gëmloo saay saay yi seen dogu ci aar dëkk bi(4).

Jigeen ña delloo nanu ginnaaw njëkkum congum naar yi. Li ci jigeen ñi ci pert bare nañu ndax doole yemul. Njiitu Naar yi sóoraale na songaat dëkk ba. looloo tax jigeeni ndeer ñi dem taal seen bopp ci dëkk ba. Loolu moo leen gënal nekk jaam.(4),(5).

Fi nu sukkandiku[Soppisoppi gongikuwaay bi]


li nu ci yokk[Soppisoppi gongikuwaay bi]

xew-xewu dundam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

xaaj yu dend[Soppisoppi gongikuwaay bi]