BCG vaccine
Ñaqu BCG (Bacillus Calmette-Guérin) mooy lila gëna mëna aar ci tuberkuloos (TB).[1] Sudee ci réew yi feebaru tuberkuloos wala ngaana bari, digle nañu ñu ñaq benn yoon xale biy sooga judd te amul benn feebar nga ñaq ko ci nimu gëna gaawe su juddoo.[2] Sudee ci barab yi feebar bi bariwul, xale yi nekk ci barab bi ñu ko mëna amee ñoom la seen yaram di am ay matuwaayi moytu feebar bi, waaye su amee kuñu ñaaw njortu ndax amna feebar am déet, dañu koy saytu ba noppi faj ko.[3] Mag ñi amul tuberkuloos te nekk ci barab bu feebar bi bari, seen yaram mën na defar ay matuwaay yu leen di aar ci feebar bi.[4] Ñaqu BCG mën nala aaraale itam ci feebar yu melni ulseeru Buruli ak yenn feebari bacteri yu bokkul ak tuberkuloos.[5] Rax ci dolli dina ñu koy faral di jëfandikoo ngir faj kanseeru naq.[6]
Yàggaayu kaaraange ñaq bi barina te wuute, waaye mën na yegg ba 20 at.[7] Ci xale yi ñu ñaq, dina am 20% ci ñoom ñu dul am feebar bi, ñeneen ñi des itam suñu amee feebar bi itam, du leen mënal dara.[8] Ñaq bi ci suufu deru yaram wi lañu la koy defal.[9] Ama guñu firnde ci ndax dañu koy baamtu am déet.[10]
Daanaka ñaq bi amul benn loraange. Yenn saay fiñu la ko jam xonk wala mu newwi, wala nga yëg tuuti metit.[11] Mën nga amaale ulseer bu ndaw ak yenn léget su weree.[12] Efe secondaire yi ñoo ci gëna bari, te ci mag ñi amatul matuwaayu xeet feebar bi lay gëna sonal.[13] Wóoral a jox jigéen ju ëmb.[14] Ñu ngi ñëkka sosee ñaq bi ciiMycobacterium bovis muy luñuy faral di jëlee ci nag.[15] Néewal nañu dooleem bu baax waaye mingi dundu.[16]
Ci atum 1921 lañu njëkka jëfandikoo ñaqu BCG ci wàllu faj.[17] Bokk na ci limu ñaq yi OMS jàpp ni ñoo gëna am solo ci wérgi-yaramu nit ki.[18] Ci diggante atum 2011 ak 2014, njëg li en gros mingi tolluwoon ci diggante 0,16 USD jàpp 1,11 USD benn dose ci réew yu néew doole yi. Ci réewum Etats Unis, ñaq baa ngi fay jar ci diggante 100 ak 200 USD.[19] Li ko dalee 2004, at mu nekk dina ñu ñaq lu tollu ci 100 miliyoŋi xale ci àdduna bi at.[20]
- ↑ "BCG vaccines: WHO position paper – February 2018" (PDF). Releve Epidemiologique Hebdomadaire. 93 (8): 73–96. 23 February 2018. PMID 29474026.
- ↑ Green, James; Fuge, Oliver; Allchorne, Paula; Vasdev, Nikhil (May 2015). "Immunotherapy for bladder cancer". Research and Reports in Urology. 7: 65–79. doi:10.2147/RRU.S63447. PMC 4427258. PMID 26000263.
- ↑ Houghton, Baerin B.; Chalasani, Venu; Hayne, Dickon; Grimison, Peter; Brown, Christopher S. B.; Patel, Manish I.; Davis, Ian D.; Stockler, Martin R. (May 2013). "Intravesical chemotherapy plus bacille Calmette-Guérin in non-muscle invasive bladder cancer: a systematic review with meta-analysis". BJU International. 111 (6): 977–83. doi:10.1111/j.1464-410X.2012.11390.x. PMID 23253618.
- ↑ Roy, A; Eisenhut, M; Harris, RJ; Rodrigues, LC; Sridhar, S; Habermann, S; Snell, L; Mangtani, P; Adetifa, I; Lalvani, A; Abubakar, I (5 August 2014). "Effect of BCG vaccination against Mycobacterium tuberculosis infection in children: systematic review and meta-analysis". BMJ. 349: g4643. doi:10.1136/bmj.g4643. PMC 4122754. PMID 25097193.
- ↑ "World Health Organization model list of essential medicines: 21st list 2019". World Health Organization (WHO). 2019. hdl:10665/325771.
- ↑ "Vaccine, Bcg". International Drug Price Indicator Guide. Retrieved 6 December 2015.[permanent dead link]
- ↑ "Vaccine, Bcg". ERC. Archived from the original on 22 January 2018. Retrieved 13 June 2016.
- ↑ Hamilton, Richart (2015). Tarascon Pocket Pharmacopoeia 2015 Deluxe Lab-Coat Edition. Jones & Bartlett Learning. p. 312. ISBN 9781284057560.
- ↑ "BCG Vaccine: WHO position paper" (PDF). Weekly Epidemiological Record. 4 (79): 25–40. Jan 23, 2004. Archived (PDF) from the original on 2015-09-21.
- ↑ "BCG Vaccine | TB Symptoms | Tuberculin Skin Test | PPD | TB Signs". TB Symptoms. 2013-01-18. Archived from the original on 2013-10-29. Retrieved 2014-02-02.
- ↑ Colditz, Graham A.; Brewer, TF; Berkey, CS; Wilson, ME; Burdick, E; Fineberg, HV; Mosteller, F (1994). "Efficacy of BCG Vaccine in the Prevention of Tuberculosis". JAMA. 271 (9): 698–702. doi:10.1001/jama.1994.03510330076038. PMID 8309034.
- ↑ Fine PEM (1995). "Variation in protection by BCG: implications of and for heterologous immunity". Lancet. 346 (8986): 1339–45. doi:10.1016/S0140-6736(95)92348-9. PMID 7475776.
- ↑ Venkataswamy, Manjunatha M.; Goldberg, Michael F.; Baena, Andres; Chan, John; Jacobs, William R., Jr.; Porcelli, Steven A. (1 February 2012). "In vitro culture medium influences the vaccine efficacy of Mycobacterium bovis BCG". Vaccine. 30 (6): 1038–1049. doi:10.1016/j.vaccine.2011.12.044. PMC 3269512. PMID 22189700.
- ↑ FINE, P (1 November 1995). "Variation in protection by BCG: implications of and for heterologous immunity". The Lancet. 346 (8986): 1339–1345. doi:10.1016/S0140-6736(95)92348-9. PMID 7475776.
- ↑ Roy A, Eisenhut M, Harris RJ, et al. (2014). "Effect of BCG vaccination against Mycobacterium tuberculosis infection in children: systematic review and meta-analysis". BMJ. 349: g4643. doi:10.1136/bmj.g4643. PMC 4122754. PMID 25097193.
- ↑ Aronson NE, Santosham M, Comstock GW (2004). "Long-term efficacy of BCG vaccine in American Indians and Alaska Natives: A 60-year follow-up study". JAMA. 291 (17): 2086–91. doi:10.1001/jama.291.17.2086. PMID 15126436.
- ↑ Rodrigues LC, Diwan VK, Wheeler JG (1993). "Protective Effect of BCG against Tuberculous Meningitis and Miliary Tuberculosis: A Meta-Analysis". Int J Epidemiol. 22 (6): 1154–8. doi:10.1093/ije/22.6.1154. PMID 8144299.
- ↑ Fine PE, Carneiro IA, Milstein JB, Clements CJ (1999). "Chapter 8: Reasons for variable efficacy" (PDF). Issues relating to the use of BCG in immunization programmes. Geneva, Switzerland: World Health Organization. Archived (PDF) from the original on 2011-02-20.
- ↑ Brosch R, Gordon SV, Garnier T, Eiglmeier K (2007). "Genome plasticity of BCG and impact on vaccine efficacy". Proceedings of the National Academy of Sciences of the United States of America. 104 (13): 5596–601. Bibcode:2007PNAS..104.5596B. doi:10.1073/pnas.0700869104. PMC 1838518. PMID 17372194.
- ↑ Packe GE, Innes JA (1988). "Protective effect of BCG vaccination in infant Asians: a case-control study". Archives of Disease in Childhood. 63 (3): 277–281. doi:10.1136/adc.63.3.277. PMC 1778792. PMID 3258499.