Bëtu-jaan

Jóge Wikipedia.
Nataalu garabug Bëtu jaan

Bëtu-Jaan garab la gu ëppe ci réew yi ci diggu àdduna bi, fu ci mel ni: Madagaskaar, Réewu Kóngo, Endonesi, Folorit...

Melo[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab la gog ab taxawaayam day àgg 8 ba 9i met. Ay xobam dañuy ràbbaloo defub dank.

Ay doomam dañuy defum sàq, xonq coyy te dëgër lool ba noppi nangoo bari. ( sakkan)

Bëtu-jaan bu tolloo ci di dëgër, dootul neex a sempi ndax reen yi dañuy law fu sori ci biir suuf si.

Ay loram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garabu bëtu-jaan nag amna ay lor:

-Xoox yi dañoo am tooke. Benn xoox rekk boo ko ci yëyee man na laa faat.

-ku kay jëfëndikoo day wàññi tooke gi. Dangay baxal xoox yi ak meew ba ñu bax nga weer leen ci naaj wi ba ñu wow.

Ay njariñam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waa pajum cosaan dañ koy jëfandikoo.

Xob yi dees koy baxal di ko naan day faj soj ak woppi sëqat.

Day yokk kàttanu góor ci néegu sëy.

Dees na ko it jëfandikoo ci sëqal kawar.

Xoox yi dees na ko def i per fecckat yi di ko takk ak a def ci seen i juŋ-juŋ.

Xoox yi it nattukaay la: Xoox bu ci ne ak moroom ja ñoo tolloo ag diisaay, ba tax na waa End dañ koy natte seen i wurus.( 12i xoox di dayob 11,6 garaam ci wurus).

Nataal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Abrus precatorius