Béegile

Jóge Wikipedia.

Béegile Garab gii di béegile : turu xam-xamam di ( cordia senegalesi ) mu bokk ci njbootu "borazina cea" di sax ci dëkk yi nga xam ne taw bi da faa yem a maay , ak foo xam ne it taw bi da faa bari lool ,fu mel ni Afrig torópikaal , maanaam ay Sengaal, Gambi , Kodiwaar , Gana , Kamerun .

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Béegile ; garab la goo xam ni gudaayam di na àgg ci juróom ñaar walla juróom ñatti meetar ci kaw. ay wànqaasam boo ci gis rekk muj ga maanaam cat la day lunk , dàtt bi it man naa rëy ba egg ci juroom-benn-fukki meetar 60i ci ag wëram , ker gi man naa dem ba egg ci 25i meetar ci yaatuwaay , ndax moom day sëq lool . Moom nag garab la gog Tubaab yi bindu ñu ci lu bari boo xoolee di na ñu la wan ntaal bi wax ci tuuti waaye du doon lu bari , maanaam daal dafa mel ni gëstoogu ñu ci .

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay bantam di nañu ko def matt ngir di ko xambe , batay garab gi di nañu koy taarale kër ndax naataayam dafa rafet. Di nañ ko jëfandikoo it ngir faju , wax na ñu ne di na faj biir buy metti, xob yi lañuy jamb ngir di ci faj biir buy metti boo xam ne jàngoroy kuli moo ko waral, dees na ko naan it ngir dànk mettiitu dëmbéen , xob yi batay dees na ko jamb di ko sangoo ngir faj yarm wuy metti walla yaram wu fasu , bantam di na ñu ci defar ay dënd ak ay gaali géej , xas mi di na ñu ci defar ay buum , amna it daakande .

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Cordia senegalensis