Arimate
Apparence
Ci angale mooy Arimathea; Ci faranse mooy Arimathée
Amoon na ay dëkk yi ñu tudde Arimate ci réewu Israyil. Arimate moo tur ci làkk gereg. Ci làkku ibrë ''Rama'' la tudd. Yaakaar nañu ne dëkk bu tudd Arimate ci Injiil moo nekkoon ci tund ma tudd Efrayim lu tollu 8 kilomet ci bëj-gànnaaru Yerusalem. Foofu la yonent Yàlla Samwil juddoo woon. Ci Injiil Arimate mooy dëkk ba Yuusufa, mi suuloon Yeesu, jóge.
Mc 27:57; Mk 15:43; Lu 23:50; Yow 19:38.