Arafu X Q
Arafu X ak Q
Xarit xélul te xellu aw ci xàllu xam () te xér ci xëntewoo lu lay xiir ci xalam
Te xettalil ku nekk xiirtal ko ci xay () te bul xatal sa xol bi it ba xëy di xay
Te say xalam na dooni xiig nga xuuyi mbéey () te bul di xotteente te xér nag ci liggéey
Melal ne xettar ci ku dëng mel ne xaal () ci soppe yépp ku xulóo nga xañ ko paal
Te bul xulóok a xeex ak’ay xasante yaw () te bàyyi xiirook a xëccóo lu man di xew
Te bàyyi xeebante xaroo xoddiku yaw () te ngay xereñ te jéem a xejj jëm ca kaw
Te xeet xumaagi xol bi xembi ay xalam () xerawlu yiw wa faj sa xóndóoñi xalam
Sa xel mi bu’m xuuge na jub xocc te wér () xëlóob ya buñ la gën di aaru kon nga ñor
Bu say xalaat xajam nangay xajoo ku ne () te bul ko xumtoo te xemmeem njariñ lu ne
Te bul di xàddi bul di xàcc xàllalal () ku nekku xàll bul di xallal it sa xol
Te xippi gët yi xoole bul di xuuse it () te bul di xand xur wu xéewal ga newut
Te ngay xareek adduna xas ko xupp ko () te xoqatal ko xuuxle it ci xeexi ko
Te xam ne màggat mu Jigéen mu xubbidaas () te xettebee xettebe xàŋ gët ya laas
Moo di misaalam bu ko xoymet sa kanam () xab ko te far ci xol bi xoolu ag bëggam
xalaat Set ak cilwiise yuuxu Jigéen Nga man gan: xuuy mooy tàkk, mbéey doj wu ñaw lay doon ñu koy kosale ak moroom ja ngir taale ci, ñu jublu ci nit ku baax ku yor almetam di taal rekk ngir ganale Lu mel xaal te ndaw te wex Yitte;xel;faale Dëkkoo Waajal sa bopp Am ab cér xoos rocci Mar wu tar lemu Doomi gaynde Tàyyi Dellu ginnaaw ci mbir Tilimal yamadi Jege ;tàbbi; dem ragalloo Tiital ko Taxaw temb;lëjle witt Kumur ak ras Bët yu tooy xipp Lu mel ne ab jégén lay doon ci ndodd mi Yuurtala yuy yuy génn ciy gët Won tuuti Ttital ko Xool mooy rëdd wi nekk ci ginnaawug mbaam