Arafu W
Shaytaane day wëtt ci xol wudd la am - wattu ko bul ko wàcc muy war di ku lëm
Dafay woreek a wèddilooy werenteloo - di wàjji ngëm di wònni mbas mbas du welu
Wor ko te wòdd xol bi ngëm waaru bu wér - sotti ci waame tudd Yàlla xol bi wér
Weeral sa wañsu diine def say warugar - bu ngëm gi woos ni waddbéer wu gar ya wër
Werante wottee ko lu war, lu wóor itam - na wuutu wor te worma wecci wane tam
Nga weex sa xol wèkki ca luy wòllimiku - te bàyyi weeje it welal tayle ba ko
Te wòlli nag wëlli kañaan’ak weli rëy - wetañ yu ñëw weñ ko te wetti far ko ray
Te wacc weerante te wéer fa wòllare - wareef akug wegeel te wicc njàqare
Te wërsëgoo wiiri wakiirlu wis ca way - te xol bi weex nga wattu waŋi wuute wéy
Te waggar it sa bopp tey waaru bu wér - te bul di wëndëng wa wogul wàqi te war
Di waaj di walli weddi bakkan’ak loram - te wéer ko bul weng ci moom ak ci wujjam
Di waslu àq woor ci caaxaan aki nar - wekku ci Yàlla def ko waay jëf la la war
Te fònku waxtu xam ne daa wund lu rëy - te bul di wuññi awra bul di wóoyu ay
Na ngay woyof te bul di wex ci kenn tam - ku dul ku bon te fònk worma tey xalam This is funny.