Arafu T
Arafu T
Toroxlul te tuub tey topp Yàlla te teet tereem () te teey tabe tey tàggat bakkan beek a daw pexeem
Toŋal ko te tóngook moom te tëkku ko bul ko tëy () toroxlu ci Yàlla’akug tëyam sàkku yërmandéem
Te bul toog te bul jëf it ci maa tey mu tund lool () na tandu te bul teeŋal ku të tukku tuskareem
Tegul yaw ci kaw yoon wii taxañ bulk o teggi tam () te bul taga-témbéekug tàyyeel ak lu deesi yéem
Te daw tabarondum digg njolloor mi ngay taseel () mu teggilook’ay tàbbiloo teeni tappaleem
Fegug Yàlla moo gën gën ji tunkaar akiy tata () nangay tàbbi kaaraangeem te bul génn bul ko jéem
Te taafenteloo nag aw turam foofu man di dem () te ngay tos sa xel ba’m saf ku dul yaw nga far ko tiim
Nga totti sa xol ba’m set ci tër ak tilim-tilim () te muñ tiis akiy tar-tar ba gis tërgënub taneem
Te daw tañaxook tànjang ci mbir moo xalaatagul () te daw tumurànkeg xam nangay tabb cig wuteem
Nangay tànn say àndaale tey tànnu taaru jëf () te tàmmal sa làmmiñ wax ju yiw mbaa nga far ne xiim
Te tooke sa bànneex far ko tiiñal te tanc ko () tëjjal ko tàbbal ko ciy pexeem
Nangay tembareel say mbir sa jëf takku am njariñ () nga lal tesarantag muñ te bul tayle gor ci keem
Te ngay bàyyi tiisanteek a teefonke ak tërëf () te taataar toroxlul nag ka deesul gis’ag tëleem
Te tapp ca xéewal yee te jug tepp-tepp yii () te tàggooki tër ak taq tey fob teraanga leem
Wonante ginnaaw ragal Ñaaw ñaaw gu ëpp bari Yanu; sëf; gàddu Wéy te dem Tabarond:màggat Ay bali fett walla defukaayam Fegukaayu bali fetal; fort ci fr maanaam fi soldaar si di làqu di fa aaroo cib xare Tuddoo ak sukkandikoo fiime fóot Jeexiitu aw mettiit nekkoon Tànjang ci mbir tëb tëb tàbbi ci Dëkk ak sax ci dara baax Posone Lakkal witt Tas ci diggante bu xat Wéradig tànk la guy tee man a dox, fas lay faral a dal Jampal Tesaranta: ag basaŋ Kee : Xaalis ak wurus Xëccoo Jaaykatu xar, mu jublu ci werante fakastalu Saaraan As taa-taa su ndaw