Arafu S

Jóge Wikipedia.

Arafu S

Sutuxlul seŋes Yàlla war sàllu ngëm ()te sóobum lefam daw ba seerug palam

Sawar am sagos ngëm te sàkkub sagam () te sëmbërtaloow yiw ba gën sépp sem

Te sartaagal ’ag sag safoo Yàlla jëm () ca kaw sippi ag sew waxam mbaa jëfam

Te naan kaasi ngëm suggalee sell yaw () te bay saw sas’ak gopp sunna’s ka xam

Selanglul te bul dox di sonjaanu sas () te ngay sopp Yàlla’ak a santiy mayam

Sa bakkan bi dang koy sébéñ ba’m séxéñ () ci ag nooy akug topp sunna’ak sëfam

Te siiwal pexeem bul ko bàyyeek sa koom () dafay sooke aw ay sexeeral mbiram

Te siiw mbicci kaaraange semmal ko jëm () fu sooŋooŋ akug sooy newul ak tilim

Nangay sémb loo man di sottal di sos () te siiw am njariñ ak sutura’ak ngërëm

Te bul jëf lu suufeek lu sew bul soxor () nangay jëf lu set seytu sàqiy mbayam

Nangay sonne xam-xam soril luy safaan () te bul sob te bul sikkal it senn cam

Te bul sóoru mbër it ndegam suq nga () te bul soxlu mbër soxlawoolug manam

Te bul siis itam ab siboor bul sob it () nangay seexlu ñaawtéef wa sib ag jëfam

Te bul sànj bennub jullit sopp ko () te bul koy sabooteek a salteel deram

Nangay digle ag sell bañ caa selaw () suturaal ku nekk it te sàmmub deram

Te bul def safaan it ba tax ngay sangéem () sippeekul di surgab ka man tey ka xam

Safoo sab sëriñ fàwwu dib sang yaw () te sa baati seedeem ka sappug demam

Nangay faj sa jikkoy sagañ sempiku () te bul suux ci sañ-sañ yi Yàlla’a ko am

Te bul nig ci am mbir suba’akiy sibir () dafay faataluw yiw du sottal mbiram



 Duggiin wu gaaw te bette
 Seŋe: kiiraay
 Aw fas wu baax
 Seeru: jot
 Ag dal
 Sëmbërtal ab rido mooy wàcce ko, fii mooy muuróo aw yiw 
 Aw nit
 Weesu fa nga naroon a yam
 Tuur ;wàcce 
 Ñaaw-ñaaw  
 Naan naataat
 Dal am xel
 Booyal; bay ab tool booyal ko am at door koo bayaat
 wolli
 Làggi ak tàmm
 sabab
 Sexeer: gaw ci wet yépp 
 Ŋoy  
 Féete kaw
 Wéradi 
 Tàmbali 
 Dëkk ak cokkaas 
 Kiy topp ci mbër 
 Suufu : bul suufu mbër ak a top ci ginnaawam waaye jéem koo man 
 Ab xaaraankat
 mere
 Noppi akug dal
 Dëgmu sëgg ngir jaaxle mbaa kersa   
 Ka sapp ag demam : kay bëgg a faatu 
 Jikko ju baaxut waaye cosaanam mooy tooy ju yàgg  
 Ginnaw suba