Aller au contenu

Arafu R

Jóge Wikipedia.

Arafu R


Rayal sa rëy gi rendi reewandeek ragal () te roy rafet-rafet yi réccu ràggi xol

Raxas sa réeri xol ba roppi gépp raw () te roof ca rus Yàlla te rembatal ko yiw

Te rëcc saytaane raxal fiir ga mu yor () te rat ko rinkil ko du ruur génnati far

Te bum la rambaaji defal rukk ci moom () ratt daŋar ja rekki mbooleemi naram

Te rënk gëm ca róok te bul raf ba mu rot () te rikk bum la xoqutal ba tax nga rët

Bakkan bi ruuj ko rijji reen ya riije ko () te rëq ndiggam la te ray ko robi ko

Adduna rusloo ko te raaf rëddi faram () te bul di ruusaanu ak’ay ronni yëfam

Tey raju bànneex di ko rog, ràññiku moom () raggal téram ba ba mu set rësal pexeem

Sa noon yi buñ ree bu ci kenn rëcc tam () na seeni reefu ne ci yaw bu leen yërëm

Na seen dereet yi riix ci suuf si rungleen () te ràngleen lu rëy te metti rombleen

Nangay rañaan di jàggi ruur di daw fu rëb () di tuubi rëcc-rëcc roñ ca yiw ya ŋëb

Te riggalal ngënéel ci xol bi yu’ñ ca riim () te bul di reggal it sa kàddu dee ko riim

Te bul di ràppal ak a reesal lu lewul () doonte lu ras nga am te am rooy rafetal

Te bul di rannamtalu ngir rëbb ci wor () ngir jëfi ku’ñ rëbb la daw ko jiitu far



 Fees bay tuuru
 yeew
 Tànk yu rinki mooy yu wóom ya jegee tànk ya soree   
 jàkk xool bu baax 
 Dindi;summi
 Mooy Yàlla ci séeréer, bu ko wolof waxee li mu ci jublu mooy dégéj ba gën a sori 
 gajj
 Buddi; sulli
 Daggate 
 far
 Diibal ay tànk ngir bëgg dara 
 Rog 
 Raju : sàcc xibaar  
 Digub dee maanaam jotug waxtuw dee
 Taq 
 Boole mbooloo jiital
 gàll ak yan 
 song
 Daaneel ci suuf
 Feesalal 
 Sësale 
 Reggal kàddu: diisal ko
 Wax wax ju suufe te teey
 Yéré yu tàlliwul  
 Cere ju amul ñeex 
 Wax wax ju neex