Arafu J
Damay janeer lu mel ne ceeñeeri cofeel - mel ne ku ñéer cafka ga far càkku ca teel
Ba maa ngi jànkoonte ci xol bi aw mettiit - wu jege njòbbaxtani céy jipp jériit
Ba xel mi jullusante na’ak xol bi, li jib - xañ na ma cëslaay ba jamuj naa ci lu jub
Mel ne ñunux ci man ci kuw maram lëjal - ma far di cam su wéet di jukkat di jëfal
Te jàmbat ’ak junj jeñul jóori cibeel - ma jaaxle cumbóonu ci màndingum cofeel
Ba jèmbraayi rònqooñ it di car-cari - jàllawli xel mi xol bi it di jér-jéri
Fit wi ni ñugg jokkalook njàqare xol - lu sax ni ñumm mel ne coggal gu ñukkul
Ba maa ngi ceeñeerlu ci biir am jayaxaan - samab cës it call ba maa ngiiy ñeetaan
Ma ñaxtu ñaxtu kenn ñëwul jàpple ma - cawarte dem njàqare ñëw jaxalsi ma
Ba càqaral na xol bi, jëmmi jamjamoor - moo ma ñëwal njold ma jéllu kekki joor
jullóotu naa ba faf ne jànjang ca ja ba - ca dig njolloor ga ba weeroo ni Ruba
Ma sàkku aw jaraasu pek jàppandiwul - Ñu far ma njàmbaasali njëgg mom jarul
Kanam gi ñëkk , ñaq, ñuqi lëf të ma - ma jóofu ay jafeñ-jafeñ jàmm të ma
Mu mel ni jaani ñas yu ñàng ñoo ma war - te doon yu ñammasle di jurbi mel ne jur
Ma aw ci ñallu jommiteg xel mu ñorul - ba mel ne am njëgg mu ag cugri lëjal
Ma jumm-jummi jiiñ jamono lii ma dal - te xam ne moom du jag du jéggal du jagal
Te xam ne njàngóor a ko gën jikko ndax it - njekk da koo xamul du jekki it jubut
Ma daal di jàppeelu ci lii ma xam ci moom - te def ko ñukk jàpp nag ca kay boroom
Te ñukk jëm ci moom te jòkk nag ci jëf - te kañ ko, njukkal ko te far sóobu ci lef
Doonte ne nag njàqare fi’m ne moo ma muur - ni njóof di muure jaasi war ma bebb boor
Du tee ma jéem a muñ te xam ne rek ngënéel - déesu ko jox cuune ku muñ rekk la ñeel
Te ñàkk jom day tax a jëf ñàkk te it - da nay waral di jëf lu jóonu lol jubut
Kon njegemaar yu jekk tey joŋante - firdawsi cig njoggama yal nan ci joti