Arafu D
Na ngay dëgër ni déjj far jéggi dayo - te doon ku dëjjarle di dàkku mbamb ya
Ba mel ne mbëtti deg ya mbaa mel ne ndëfëñ - du jàmbatub dagg ni dëññ mbaa wetañ
Te bul di aw ndóol wu dëféenu fàww rek - saxal di dàllu bul di dallu mukk nag
Bul di dijooti ndàmm sonn a koy maye - faral di dànna bob du déjjatuy moyi
Dëtëm ndoxum ndam ma mu neex ci ndenqaleeñ - nga nòyyi ndeemeexi ngënéel sa diine feeñ
Dat ga di dòtti yaw nga des, dér , darale - ni ku ñu dòtt tey ku dërkiis të file
Di dëflu ciw tiis te nga ndarkepp sa mbir - dëxëñ sa ndaaf te ndàmbe mbeg akiy naqar
Te bul di diis ba faf di ndaari des ginaaw - na ngay doronke dund gii doylu la teew
Te bul di dàññi mel ne kuy das defarul - déeyaale ak détti denéer yuy dexi xol
Te doylu yaw doonte ne dóor-dóor nga ame - dàggiku ndeem dooj nga am it bul ko gëme
Te dànd dollenki bakkan, daw ko bu wóor - te bul di dandal it sa xol bu xel mi dar
Te dàngañal te moytu detteelu itam - ca kàmbi diiŋat ya te daw dee du xalam
Demal ca dex ga bàyyi déeg yi daa doyul - te digg-dóomu nag ci lépp bul ëppal
Te bul di ndeetet lu di tan-tanlu itam - saxal di tan te bul dagook a ndiigu tam
Na dëgg doon sa nding looy dunde dadam - ta bay sa dooñu diine bul di dooji tam
Te bul di doore mukk diisool ci lu ne - da nay teree daanu di tee diig ci lu ne
Xamal ne Yàlla day dënéerlu képp nit - nang ko ba xel dàggiku ngir teg na la bët