Arafu B
Ku bëgg nay bëgg lu baax bañ lu bonam - te am bañum-rus ma te xeeñtu aw banam
Te néewi mbóorante te doon ku xuuyi mbéey - setal sa mbóoki xol te nàmp batti péey
ŋoyal ca mbicci kaw ga bul jàpp ci pet - moyal barastikook a bàyyi bul di xét
Te rendi say mbamb ca pòttox ya te boy - jam ko ca baljat ya te bèccingal ko wéy
Te ñàkk paal ku dul ci Yàlla miy boroom - te sàkku bëbbalam , ñeme’g péete ci moom
Te buddi say mbémpeñi xol te buddi bóot - sol ca ngënéel ba lépp pendal aki mbóot
Te néewi bébbant nde moodi pëppi jëf - di pindi pax yu feese pert bu’ñ la këf
Defal bërët te binni ngir yéem sa ayib - sàkku pexem faj ko te pasteefu te jub
Defal sa jëf yi pàkkutéef wëlif poñat - lu dee gi bette bette berndeele ko mat
Mbewte nga bërgal ko potoxlu pèkki mbég - Génn ci mballi bërjëlug bakkane rik
Mbémburi xol di yéene nay mbèll mu set - te banki jëf peek ko te mbaayàlla poñat
Berul te bul topp mbaboor mi deel beres - lu bon ci ag mbëbëstënam ci foo ko gis
Bul ca deseb batt , faral béel ci lu baax - te bul ca bar sa mbir na bir ci fonk baax
Te dagg pàcci panka buural sa kañaan - te daal di buur jëm ci boroom bi daw safaan
Te fob sa baag yoor ko ci mbalka mom ngënéel - tanq ca naan te wàcc mbóori xiila-xaal