Andare
Apparence
Ci angale mooy Andrew; Ci faranse mooy André
Benn ci fukki taalibe Yeesu ya ak ñaar la woon, di rakku Simoä Piyeer. Ñu bokk ndey ak baay. Nappkat bu bawoo ca dëkk bu tudd Betsayda ca diiwaanu Galile la woon. Bala mu topp ci Yeesu nekkoon na taalibe Yaxya.
Dañuy gis Andare ci Injiil ci Mc 4:18-20; 10:2; Mk 1:16-18,29; 3:18; 13:3,4; Lu 6:14; Yow 1:35-44; 6:8-9; 12:20-22; Jëf 1:13.