Akisi Kuwaame
Akisi Kuwaame
Dundu ak jaar-jaaram | |
Juddu | 1er sãawiyee 1955 (juroom-benn-fukki at ak juroom)
Casale (Tiassalé) |
Réew | Kódiwaar (Côte d’Ivoire) |
Wékku ci ndigalu | Kódiwaar |
Tàggatu | Iniwersite Félix-Houphouët-Boigny (doktoraa) |
Liggeey | Soldaar ak fajkat |
Yeneen xibaar | |
Làrme | Làrme bu Kódiwaar |
Màqaama (Garaat) | Seneraalu birgaat |
Erreur de script : la fonction « build » n’existe pas. Abla Pokou (wala Aura Poku, wala Abraha Pokou) lingeeru Afrig la , juddoo ci fukk ak juróom-ñetti xarnub. Indi na askanu Baoulé ci réewum Gana ba ci Kodiwaar. Léeb bi dafa nettali, saraxu doomam bu góor ngir jàll ag dex .
Bat bi "Baoulé " li nu tudde leegi askan yi , mu ngi joge ci saraxu doomam.
Bicci toppu saraxe, né na "Ba-ouli", loolu dafay tekki "doom bi dee na". Akisi Kuwaame (borom-këram sant Lebahi) mu ngi juddu benn fan ci weeru sãawiyee atum (1955-2022) [1] ci Singrobo (Casale, Kódiwaar). Moom mooy jigeen ji jëkk a nekk seneraal ci làrme bu Kódiwaar . Moo nekk njiitu wér-gu-yaram bi ak ndimbalu askan li ci larme bi.
Dundu ak jaar-jaaram
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Seneraal Kuwaame Akisi mu ngi tàmbali am njàngam ci Singrobo, bi mu fa jógee, mu dem Agnibilékrou ci ag mbootaayu katolig. Bi mu jàllee ba war a wéy ci njàng mu digg-dóomu mi, lañu ko yóbbu ca liise Sainte-Marie, ginnaaw bu mu paree foofu, mu dem jàngi paj ci daara yu kowe yi. Fukki fan ci weeru sãawiyee atum 1981 la dem làrme, fekk mu ngi ci juroomeelu atam ci njàngum kër doktoor mi, ci iniwersite bu Abijãa. Diggante sulet ba septàmbar 1981, mu ngi doon def benn tàggatu bu boole ñépp ci lekoolu takk-der bu Kódiwaar ci Buwaake. Ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru suyee (juin) atum 1983, mu wone teesam bi mu bind ba pare. Diggante suyee (juin) ba sulet atum 1983, mu delluwaat ca lekoolu takk-der ya nekk Kódiwaar ngir def fa tàggatub ófisiyee. Ginnaaw tàggatu boobu, mu am garaatu fajkat liyëtnãa. Ci weeru ut atum 1983, mu nekk ki jëkk a am, ci làrme bu Kótdiwaar, ab bërëwe bu wàcckatu paaraa ci mbooloom komandóo mu bataayoo Akouédo bu jëkk.