Liggéey (ci muridulaa)
Bii jukki bu am solo la, ñu def ko ci cawarte gi murit yi ame ci wàllug fàggu ak koom-koom, ñi ngi ko jële ca yëglekaay gu siw googu di The Economist, di genn këyitu xibaar gu gore guy génn ayu bis gu nekk, te adduna bepp xam ko, muy wax nag ci mbiri adduna bi bepp, moom nag mi ngi njëkk a génn ci satumbar 1843.Economist Newspaper Limited (Filiale de Pearson) ca London moo ko génne. Li ñu ci gën di wax nag mooy koom-koomu adduna bi, politig, jëflante, xaalis, xam-xam, xarala ak fànn (art). Lim bu ci génn, di nanu ci defar lu ëpp milyoŋ, te 80% ba ca biti Angalteer lanu leen di jaaye-ji. Yëglekaay gi tas na ci lu tollook 1.138.118 ciy yax ci xaaj bu njëkk bi ci atum 2006, ci li gëstug bureau of circulations wax, di jumtukaayub natt bu nekk ca Angalteer. 53% ci ñiy jënd yëglekaay bii ak di ko yër ay waa Amerig lanu, 14% ay waa Angalteer, 19% di ñu dëkke Tugal gu goxe gi (continentale). Yëglekaay gi dees na ko yër ci lu tollook 206 réew.
Faith in the market (ngëm ak yaxantu)
19 desambar 2006 / Rom ak Tuubaa (Senegaal)
Ci ginaaw luumay Itaali yi nuy defe fu lenn dul tiim lu dul asamaan si, am mbooloom jullit mu Afrig a ngii di indi ay tontu ci li nuy tudde “addunaal” di (mondialisation)
Kepp kuy door a teg tànkam ci suufus Rom, péeyub Itaali, dana gis ne dëkk bii de sol na mbubb mu bees mu mel ne du manu ko xame woon, mbubb mii nag mujj na di mu ñu ko xàmmee ni nu ko xàmmeek baaram yeek tànganaam yi nga xam ne dees na fa faral a guuxe leeg-leeg as lëf ci lii di Cappuccino, di kafe gu nu jaxaseek meew te nu gën a miinew jëfiinam ca Itaali. Bu ngéen jëlee yoon wi jëm Vatican, jaare ko ci Via Della Conciliazione mu dim mbedd mu ca jëme, da ngéen gis ne lu bari ca peggi tëli ya de danu koo muure aki jaaykat yu bawoo Afrig yu lay wër aki maska yu ndaw yu (waso), ay saag, ay der (ceintures) walla ay weeri jant yu nu roy, maanaam yu doonul piir. Bu ngéen fa taxawee as ndiir nag di léen seetlu, bu ngéen moytuwul, da ngéen fa seetaan powum muus ak jinax, mi nga xam ne jaaykat yii baaxoo nanu koo def ak takk-der yi, mu dig (dàqante gu xoromu te yërëmtalu). Nii daal lanu koy nekke, saa su nu léen yëgalee ne takk-der yaa ngoog, da nga leen di gis ñu taxañ seeni bagaas cis lëf cig gaaw daal di laxas, seeti nu nu man a mucce, bu Yàlla dogalee rëccuñu, bu booba a seen yoon du nekkati ci seen njaay moomu, moom kay danu ko fay bàyyil takk-der bi leen jàpp mu dajaleel ko boppam, daal di leen yobbu. (…)
Ca dëgg-dëgg, jaaykat yii nekk ci yoon yi jëme Vatican man ngaa wax ci ñoom lu nekk lu dul nosuwunu (organisewuwunu). Ñoom de ñi ngi bokk ci kuréel gu nosu, gu nu xame ci adduna bi ci gëm-gëmu diine ak bu koom-koom, te am it ab barabam ca beneen dëkk bu tedd di Tuubaa, nekk nag ci digg Senegaal, boo fa jëmee nag juge Dakar péeyub Senegaal ñatti waxtuy tukki rekk lay tollool.
Niki yeneen imigire yu bari yu Senegaal (yi nga xam ne yenn yi ay dawalkati taxi lanu ca New York, walla ñu diy wattkati suraas (orange) ca Espaañ) jaaykat yii di wëndéelook seeni njaay ca Rom ñi ngi bòkk ci genn kuréelug jullit gu tasawuf nu koy wooye “yoonu murit”, mooy yoon wi ëmb taalubey Cheikh Ahmad Bamba yi, kii nag ag kilifag diine la gu làqu atum 1927. ñoom nag ci jeexitalu gi nu def ci njàggalem Sëñ bii, indi nanu ay tontu yu am solo ci laaj yi ja yu adduna yi di indi aju ci ay marsandiis aki ligeey (maanaam dugal nanu seen loxo bu baax ci yaxantu gi ci adduna bi).
Li ëpp ci 11 milyoŋ yi dëkke Senegaal ay jullit lanu waaye lu ci ëpp danuy bokk ci benn ci ñaari yoon yu mag yii di wu Murit mbaa wu Tiijaan, moom nag (yoonu Tiijaan) moo fi jiitu wu Murit. Bamba moom leeral na am njàggaleem mi nga xam ne ñi ngi ko xame leegi ci turu ((ag murit)) leeral na ko ne mooy ag dellu rekk ca cosaanul Lislaam, gas reen ya, xame ko na ko Yonnat ba indee woon. Waaye nag moom Lislaamam lu néew la nirooleek ju xaw a tar ja bawoo Araabi Sawudit. Lenn nag am na mooy murit yi danuy xaw a def li nuy wax (culte des saints et de leur tombeaux ) muy ci maanaa jaamu wàlliyu yi ak seeni bàmmeel ba ci bu seen sëriñ boobu sax, te loolu ñoñ Wahaab ñi danu koy weddi, di ko kontar. Waaye murit yii nga xam ne danoo doylu ci seen bopp yëgunu sax ne ñi ngi wax ak a weddi (ñoom wahaabit yi), ñoom daal danuy dajale seen alal def ko ci li nu bëgg, tabax seeni jumaa aki jàkka te dunu soxlaal ñii di waa Araabi Sawudit dara ba dara booloo jeex. Sheex KA di sët ci Bamba, ca biir këram ga nekk Tuubaa, di dëkk bu fees dèll ak ragal-Yàlla, waaye it di bu nu bàyyikoo fu nekk dëkksi fa, ag yaxantu gu lokaal di fa dox bu baax ak a naat ci wàll goo wëlbati sa bët jëme, moom Sheex KA mii leeralal na nu gisiinu sëñ bii nga xam ne mooy sukkandiku ak wéeru ci sa bopp: (( bu ngéen wéeroo ci keneen)) mi ngi nuy leeral (( du ngéen gore mukk, lii mooy sunu gisiinu dund)). Bi mu fi daataa juge Bamba mébetoon na ay mbir yu bari: bëggoon na Tuubaa, dëkkam bi mu sanc, nekk dëkk bu sell. Njabootam gi – ci déggiin wu yaatu wi – Mbàkke-mbàkke yi, ëmb na lu sakkan ciy sëriñ wallay jànglekati xam-xami diine, yuy boole jàngale liyeey bu tar ci seenum njàngale ak temb, maanaam bañ a wéeru ci kenn ak dimbalnte. Xalaat yii nag moo jàñ murit yi ci ñuy faral a tukki ak a tuxu di dem ci yeneeni réew ngir wëri ligéey, ngir man a yonnee seeni njaboot lu nu man a dunde man cee suturloo, ak ngir man a jox àddiya seeni sëriñ (sii nga xam ne ñu ci ëpp danuy faral a tukki di wër adduna bi, ngir nemmeeku-ji seen taalube yi) ak ngir suqali dëkkub Tuubaa bi.
Lii lépp nag jëf na ay jëf ci def murit yi ñuy benn ci kuréeli Afrig yi gën a tèkki, moo xam ci seen réew la mbaa feneen. Fu ñu nekk ci adduna bi rekk dananu jeem a booloo ngir jënd jàkka walla barabub daje. Seen dimbalante gi nuy def tax na ba ñu bees di man a tukki bay man a ligeey ak a ami këyit. Ci safaanub ñu nekk fi di ngàññ dogal bi ak a jàmbat, ñoom daal yaxaantukat yu sawar lanu te muus, yuy dugg ci ligeey yu yombadi yi nga jort ne dunu ko man, te fu nekk it ci adduna bi danu fay dem di def senni ligeey. Nan jël ku mel ne Aliyun KA, ab bitig la am buy def njaayum bëbëstan (vente en gros) ca wetu gaarub Rom ba tudd Termini. Moom rakk la walla mag ci Sheex KA mi nekk Tuubaa di topptoo njaboot gi. Aliyun KA mii jaaykat la buy def njaayum ay maska yu waaso di ko jaay nag ay moroomi senegaleem yuy jaay di wër ( walla sax ñu duli senegale ), bu ko defee ñoom ñii di ko jaayaat ci mbedd yi walla ci tefes yi. Lenn nag ci njaay mii Senegaal lay bàyyikoo wayye li ëpp day bawoo Endonesi, Thailande mbaa End.
Teewul Aliyun nangu ne am na leeg-leeg ay jaaykati imigre yu juge ci yeneeni réew yu gën a muus murit yi ci di indi njaay walla jaayiin wu bees. Moom nag Aliyun, ku naw ñenn ci ñiy wujjeek moom ci njaay mi la te juge Banglaades, ndax nee na ((ñoom danuy déglu xibaari jawwu ji (meteo) ba bu nu nee suba di na taw rekk ñu gaaw wuti parasol jaayi ! )). Am na benn yoon ci mbedd mi, Sang Ka def fa nuyyoob taalube bu tàng ak ay mbokki muritam yu def am mbooloo mu rafet tey jàpplante. Jaaykati saag yii ak der, nga xam ne yu ci ëpp Siin lanu juge, ñu ligeeye leen fa, danuy faral a daje ngir weccante seeni xalaat ak xam-xam yi aju ci ni nuy lijjantee bay mucc ci takk-der yi. Bi añ jotee, gan dikkal na Sang Ka, di benn waa reewam N. GEY, mi nekk ci bunt bitigam tey jaay ay tòggi Senegaal yu tàng, plaat bu nekk 5 euro.
Benn yoon ci ayu bis gi, lu ëpp ci murit yi nekk Rom dananu daje ngir def daayira (julli, jàng Alxuraan aki Xasida), gisante, siyaarante,xool ci seen biir ki ci yayoo ndimbal. Leeg-leeg as mbooloo ci ñoom danuy déggoo ci bokk luye ab kontaneer , yonnee ci seeni njënd aki bagaasi jëfandikoo, ngir nu jaayaat leen ca Sandaga, ja bu nekk ca Dakaar, te murit ya ëpp fa. Ay anam yu wuute it am nanu yu niy yonnee xaalis, looloo tax këri ligeey yiy yëngu ci wàllug yonnee xaalis yu tas lanu ci mbooleem ruqi Senegaal. Waaye imigre yi ñoom li gën a noppale ci ñoom te nu gën koo taamu ak a def mooy: woo seenub xarit walla xame ca Sandaga ngir mu joxal leen seen mbokk ma soxla.
Ñi ngi nattale ne murit yi tollu nanu ci 40% ci askanu Senegaal wi. Waaye bu dee ci bitim réew ñoo ëpp ci imigrey Senegaal yi nuy tollale ci 700,000 . Murit yi it ñooy daanaka 80% ci jaaykati Senegaal yiy wër, tey jaar ci mbooleen qàli Itaali yu mag yi. (Fraans mi doon dooley sancaan ji tegoon loxo Senegaal mujj na doonatul réew mi senegale yi jëme séen një. Ay fukki at a ngii Itaali nangu barabam boobu ci moom, waaye nag jamono jii ñu nekk Espaañ a ngi jéegoy jéego ci fuqarcee ko ci Itaali. Lii sax moo waral ci weer wi (desambar 2006) lu jege 80 waa Senegaal ñoo sànku ci ndox mi, ci séen gaal gu laboon te jëmsi woon Espaañ, ca dunam ya tudd Canaries).
Lu bari ci murit yi danu lay wax ne di jaay di wër moo leen gënal ñu sax fi barab di ligéeyal kenn. Loolu nag ci genn anam day wone ni njàngalem sëñ bi jeexitale ci ñoom, te mooy sukkandiku ci sa bopp. Lu man a xew nag, ñu néew ci ñoom a mas a def ay tooñaange yu mag. Bis bu amee ay këyit ak visa day daal di dellu kër ga, def fay weer. Te sax ci mujjug at mii rekk ñu bari di nanu dellu réew ma ngir tëbëski-ji, bu ko defee ñu ci ëpp danu fay des ba weneen xewu diine wu mag wa ñëw di Màggalug Tuubaa, bu ko defee nag bu jàllee ñu door a dellooti Tugal ci jamonoy lòlli. Jenn ci dooley murit yi mooy seen nosu gi nu def ci wàllug njiit. Ñoom de bu ñu doon ab jal da nga naan Xalifa ba a nekk ca njòbbaxtal la, di aw turu njiit wow ki ko yanu fii mu nekk mooy Sëriñ muhammadu lamin baara mu Sëriñ Fallu. Kii daal mooy ki nga xam ne lu mu wax rekk ñu def ko. Cig ayam Tuubaa gis na ag yaatal gu jéggi dayo ba. Ci atum 1958 bu ña fa dëkk weesuwutoon 2000 nit, leegi àgg nanu – man nanu ne - ci ay 700,000 nit . Alkol nag ak Póon danu leen a aaye ca Tuubaa , moom dëkk bii nga xam ne daa xaw a moom boppam ci biir Senegaal. Ña nga fay taxawal daara ju mag (ab université). Boo ko doon nattaleek yeneen dëkki jullit ñi fa la ag féex ëppe ak doxe na la neex ci diine. Jigéen ña dunu sol pantaloon waaye dunu muuru it, ñu ci bari it dunu musóoru. Xale yu góor ya’ak yu jigéen yaay demandoo jàngu ba (école). Saa su nu wootee ngir ñu defar ab fajuwaay (hopital) mbaa woote bi jëm ci lu defar ndox mi, ay milyoŋi eurooy dajaloo, ngir ne murit yu bari ay way woomle lanu, ku ci mel ne Elhaaji JUUF may futbal ca Bolton (Angalteer), ndax moom joxe na ca la ñu doon laaj ngir ligéeyub Tuubaa ba (…) Xamagunu leen de bu baax, waaye murit yii bari na lu adduna bi man a jànge ci ñoom de, du rekk ni nu war a def ba jàmmaarlook li nuy wax mondialisation (di ci maanaa jël adduna bi bepp def ko daanaka menn réew, benn xalaat, xatal soreente yi, jegeele gis-gis yi añs), waaye it warees na a jànge ci ñoom ni nuy doxale diine ci anam gu teey te jàmme…