Ñibbisi gi jugge Gànnaar

Jóge Wikipedia.

Ba mu fa nekkee ba guddig gàmmug atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,di guddig àjjuma,la fa Sheex Ibra FAAL ñëw,tukke Ndar,indaale këyit wu juge ca tubaab ya di ko may mu dellu réewam Senegaal,murid boobu it dikk jàpple ko ci tuxu gi,mu tàmbalee waaj,di tàggu waa dëkk ba ,ba àjjuma ja dellusi,di fukk ak juroom ñeent ca weer wa,mu génn këram googa sóobu yoonu Ngaanjaar,maanaam Gaaya,dib dëkk bu nekk ci penku bëj-gànnaaru Dagana,dex gi romb na fa,ñooña sàkku ci moom mu julli ci seen jàkka ji nu doon yeesal ,ngir barkeelu ci,mu ànd ak seen imaam ja Muxtaar SOW, julli ñaari ràkkaa ci njëlbéenug yoor-yoor,jëggi dex gi dem dagana,nekk fa ba bisub gàwwu ñaar fukki fan ak juroom ñatt ci weer wi,mu dugg gaal ci tisbaar ji jëm Ndar.


Jamono yi mu nekke woon Dagana,nganale gu nekk defal nanu ko ko fa,ci bëcëg gi, bu guddi masaan a jot,ñu daa indi ay làmp yu leer ci kanamu bóoli yi. Mu wax ci loolu ne loolu mooy liy dëggal waxam ja mu waxoon ca lenn ca xasaayidam yi mu defoon ci arafi ((walil laahi mulkus samaawaati wal larli))di ci maanaa Yàlla’ay boroom nguurug asamaan ak suuf,muy li mu mujj a bind ca Daarul Mannaan ca Tuubaa,ba mu àggee ca arafu daad wa mu waxoon ca :

((gane ji naa aji Tedd ji,mu teeyalal ma ganale gi,te du ma dañ ci nganale gi mel ni ay làmp))


Bi mu àggee Ndar ca guddi ga,daa dal di wàcc ca Sheex Ibra FAAL,sax fa ay guddi,juge fa dem Luga, wàcc ci Alhaaji Masamba Soxna,foofa la yabale ligéeykat yi ñu dem Njiheen,maanaam Cëyéen,ca Jolof,jiitu ko fa,defaral ko fa ag kër njëkk muy agsi,dal di jàll Ngaajax,fanaan ca jàkka ja,fa seen xabrub wàlliyu nekk,dal di jàll ca kër sëñ Asan NJAAY,yendu fa ,fanaan fa,yendooti fa,laxas dem Kokki,wàcc ca Sheex Muhammadu Maam ,maami Sheex Bashiiru,demati Duriga,faSheex Madun Samba,maami Sheex Murtadaa,juge fa àgg Kër Baasin ca Sheex Muhammadu Amina Xuma JOOB,doo nga dem Cëyéen ci bis yu néew,di njëlbéenug rabiihus saanii,fekk yenn kër yi noppi,bi mu agsee ca kër ga,ca njëlbéenug rabiihus saanii,atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,daa wàcc tudde ko Daarur Rahmaan,mu nekk fa mbiram akuw doxiinam di gën a jub,di dolliku waxtu wu nekk,ba ci benn ci ñaari jumaada yi ,ci atum saksasin,di junni ak ñatti téemèer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,mu taxawal Daaru Xudoos ci sowwub dëkk bi,soree ko lu tolloo’k ñaari kilomet walla lu ko yées,mu sax fa ,bul laaj nag mbiram,moom daal na ma la ko waxe woon rekk ci bépp barab,waaye fii sax gën na fee dolliku,ba ca àjjumay ñaar fukki fan ak ñaar ci weeru muharram,atum lasasin,di junni ak ñatti téemèer ak fanweer.


Ca sahbaani sakasin ja,di junni ak ñatt téeméer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,walla ca ramadaan ja,la sëñ Abdul Laahi gane àdduna,wax nanu ma ne Sëñ bi daa bind Abdul Laahi ci aw këyit,yonnee ko Sheex Muxtaar Binta LOO,nijaayi sëñ Moodu Mustafaa,digal ko mu tudde ko noonu,mu defe ko ni mu ko binde woon ci këyit wi,mbooloo mi nag leegi danu koy wooye Abdul Laahil Haziizi,te xawma fu nu jële loolu,ah waa-waaw xanaa denu cee jublu ne Haziz turu Yàlla la.