Ñaqu Hepatite A

Jóge Wikipedia.

Ñaqu (vaccin) Hepatite A mooy ñaq bi mëna aar nit ñi hepatite A.[1] Wóoraayam yegg na ba 95%, te dina la aar lu tollu ci fukki at ak juróom amna sax ñu muy aar seen giiru dundu.[1][2] Ku nekk war na ko ñaqu ñaari yoon, bu njëkk bi mooy su xale bi amee benn at. Ci siditu nit lañu koy pikiir.[1]

Waa Mbootaayu Wergi-yaram ci Àdduna bi (OMS) dañu digle ñu ñaq ñépp ñu nekk ci barab bi feebar bi bariwul noonu. Waaye digle wuñu ñaq ñépp ci barab yi feebar bi bari lool ndax ci foofa xaramu nit ki tàmm na xeex ak moom ba muy xale ba defar ay matuwaayam.[1] Waa Kër giy Saytu ak Musalaate ci Tawat yi (CDC) waxna ñu ñaq mag ak xale yi nekk ci barab yumu leen mëna dalee.[3]Royuwaay:Drugbox Ñaq bi dula jurul benn jafe-jafe. 15% ci xale yi ko jël dina ñu yëg tuuti metit ci barab biñ jam wala genn-wàll gi suede mag la. Ñaqi hepatite A yu bari dañuy am wirisu buñ tënk, waaye yenn ci ñoom wiris buñu wàññi dooleem lay am. Bi am wiris biñu wàññi dooleem baaxul ci jigéen ju ëmb wala ñi seen yaram gaawa jël feebar. Amna ñaq yu néew yuy jël hepatite A boole ko ak hepatitis B wala ñaqu typhoid.[1]

Ñu ngi njëkka nangoo ñaqu hepatitis A ci Europe ci atum 1991 ak ci Etats Unis ci atum 1995.[4] Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla.[5] Soo demee Etats Unis mingi fay jar diggante 50 ba 100 dolaar (USD).[6]

  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 et 1,4 "WHO position paper on hepatitis A vaccines – June 2012" (PDF). Wkly Epidemiol Rec. 87 (28/29): 261-76. 2012 Jul 13. PMID 22905367.
  2. Ott JJ, Irving G, Wiersma ST (December 2012). "Long-term protective effects of hepatitis A vaccines. A systematic review". Vaccine. 31 (1): 3–11. doi:10.1016/j.vaccine.2012.04.104. PMID 22609026.
  3. "Hepatitis A In-Short". CDC. July 25, 2014. Retrieved 7 December 2015.
  4. Patravale, Vandana; Dandekar, Prajakta; Jain, Ratnesh (2012). Nanoparticulate drug delivery perspectives on the transition from laboratory to market (1. publ. ed.). Oxford: Woodhead Pub. p. 212. ISBN 9781908818195.
  5. "19th WHO Model List of Essential Medicines (April 2015)" (PDF). WHO. April 2015. Retrieved May 10, 2015.
  6. Hamilton, Richart (2015). Tarascon Pocket Pharmacopoeia 2015 Deluxe Lab-Coat Edition. Jones & Bartlett Learning. p. 314. ISBN 9781284057560.