Yëngu-yëngu yi jugoon di safaan Jàngu bu Paab bi

Jóge Wikipedia.

Yëngu-yëngu yi jugoon di safaan (di kontar) Jàngu bu Paab bi

Yëngu-yëngu gu yéwenal diine ji ci Tugal :

Yëngu-yëngu gu yéwénal gu diine ci Tugal, mooy googu doon am ci Tugal ci xarnub fukk ak juroom benn g, ngir setal Jàngu bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas-pas ak yu jikko, na ñu ko daa defe mooy jéem a delluwaat ci njàggaley Injiil yi.

Li waraloon « yéwénal » gi :

Ak li Jàngu bi di nekk nguurug ruu lépp - ci li ko njëkk a tax a jug - téewul ànd ak li jamono di gën a yàgg, mu jot a àgg ci ŋëpp - ci loxob weñ - nguurug diine gi ak gu politig gi, maanaam, mu tëye tëyiin wu metti te tar, ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi. Ci loolu la mujje di dooley politig, ju diine, ju koom-koom, ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu Tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi. Dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën’a saf, te gën a tar, mu Jàngu bi moomoom, daan ko teg kuy jeem’a léewtook moom, ak nu darajaam man’a kawee, mbaa mu màgge ni.

Egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi, di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal Yàlla, moom déy – ginaaw ag mbon da koo duggoon – daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam, fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu, ay alalam it mu teggiloon leen, te musal leen ci galag yi ñépp di fay. Ci noonu Paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp.

Ñaawtéefi Jàngu yooyu ak yu leen moy, ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi.

Ki gënoon’a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu, mooy labbe bii dib xeltukat , nu ko daa wax Erasmus ( 1466 – 1536 g), moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon « tagg ag ndof » (Praise of Folly) , jamoon na ci nekkiinu Jàngu bu katolig bi, mu nekkoon jam yu tar te wex.


Dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci Tugal :[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yéwénalug diine ci Tugal - ci doxam bi - romb na ñaari tolluwaay : bi ci njëkk mooy : bi ay yëngu-yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu-yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci Tugal tegu. Bu ñaareel bi nag mooy yëngu-yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam.

Bu dee nag yëngu-yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man’a am, man’a taxaw ci Tugal, ñoom ñooy yi nuy wax Fransiskaan ak Dominikaan, ñooy yi gisoon ne mant’a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal Jàngu bi te dëgëral ko.

Ag yëngu-yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca Angalteer ci njiitl John Wycliffe (1330 – 1373 g), moom kenn la woon ci ustaas yu siw, yu daaray Oksford ju mag ji.Googu nag li ko taxoon’a jug mooy dañal li taqoon Jàngu bi cig mbon. Gii yëngu-yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo’k xaaju xarnu, ginaaw juddug yëngu-yëngu gu ñaari way sell yii di Fransis ak Dominik, waaye gii nag moo gënoon’a fés, gën a jeexiital ci Jàngu bi ci gu Fransiskaan gi ak gu Dominikaan gi. Geneen it feeñati gu yéwénal ci Bohimiya ci njiitul John Hess (1373 - 1415 g) , moom mooy ki ne woon : ag diggale wart’a am ci diggante nit ak boroomam, ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci Injiil. Hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ-sañu Paab gi, ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam .

Bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom, ñi ngi doon jëmmu ak’a feeñe ci am gi yëngu-yëngug Protestants gi amoon, njiit ya di woon Martin Luther, Kalfan ak Swingli.


Martin Luther ak yéwénal gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Martin Luther mi ngi juddoo Isilban, di benn dëkk ci diiwaanu Saksoniya ci Almaañ atum 1483 g, faatu atum 1546 g, baayam nekkoon ku daan liggéey ci benn ci gasuwaayi mbell yi. Mu màgge nag ci njaboot gu ndóol, ak ci ron dund gu jafe te wow. Moom nag jàng na cosaani làkkuw latin, ak cosaani ag katolig, noppi jàng yoon ak xeltu, dugg nag ginnaaw bi, benn ci barabi jaamu yu katolig yi, ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef, loolu nag ci gëm-gëmi katolig yi la bokk. Ginaaw bi mu tukki dem Rom atum 1510 g, def fa weer, gisal boppam ñaawtéefi paab gi, ak bon-boni Jàngu bi, li gënoon’a wëlbati ay gëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon, ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon, ak set gi mu setoon . Lii jeexiitaloon na ci boppam, ak xelam mu daladi mi, jañoon ko it ci jam walla “kritige” paab gi, ginnaaw bi it, mu mujj fettéerlu ci kawam , bi mu bañee –moom paab gi - ne du soppi aw doxaliinam.

Dikk gi labbe bii di John (Tetzel) dikkoon ci diiwaanu Saksooniya atum 1517 g, ngir jaaysi fa ‘xobi njéggal’ yi, dikk googu dimbli woon na Luther ci mu man’a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam.

Jaadu na ñu fàttali leen ne ‘xobi njéggal’ mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji, ci jeem’a fare ay bàkkaaram ci def lu baax, jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor. Waaye Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi, moom daal, da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji-ji Rom, ginnaaw bi, wax jooju xaw’a gën’a jëm kanam, gën’a xóot, bi kenn ci paab yi nee : njéggal daal man na’a ame ci nit joxe ci alalam ci Jàngu bi, ngir ñu dundale ci diine, bu ko defee ñu jox nit kooku ‘xobu njéggal .

Luther moom dafa safaanoon (kontaroon) njaayum xobi njéggal yi, mu ne woon : mucc mbaa mbugal ak fayoontoo, manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal, fa nu man’a juge kay mooy gëm Yàlla. Luther moom diiŋatoon na xobi njéggal yi, daal di woon dem ba ca Jàngub Wtanberg ba, wékk fa mbind mu ëmb ay diiŋat yu toll ci 95 , ci atum 1517 g . Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati Luuther yi, ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ, ñu teg ko Luther, saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax (Wermis), waaye Luther moom faalewul woon saxal bii, moom kay da koo sanni woon ca ëttub Jàngu bu Watanberg ba, lakk ko.

Xalaati Martin Luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Luther, xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo’y yii di ñëw nii :

(1) Injiil mooy andaar ju diine ak ju yoon ji muy sukkandikoo ci firi pas-pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute.

(2) Nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na’a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge, xame ko ni.

(3) Paab bi amul - benn yoon - àq mbaa sañ-sañ ci rënkal fi boppam, moom rekk, sañ-sañu firi injiil.

(4) Sëy daa war’a dagan ci làbbe yi.

(5) Niti diine yi dañoo war’a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi.

(6) Wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi Tugal gu sowwu gi.

Bu nu xoolee xalaati Martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu néewal doole sañ-sañu Paab bi, loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante Yàlla’ak’ub jaamam. Sàkku gi mu doon def it ci nu néewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy néewal ngañaayi Jàngu bi aki am-amam aki tonoom, ndax loolu man’a soril Jàngu bi caaxaan ak po mi mu nekke woon. Danga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge, moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci Jàngu bi, ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom Jàngu bi ne àqi yoonam la ju mu moom.


Jëfka yi dimbli Luther mii ci wooteem gi man’a àntu[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon Martin ci fipp gu yéwénal gi man’a àntu. Yi ci ëpp solo ñooy yii :

(1)Feeñ gu Luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa Tugal yi seeni xel da cee tàmbli woon’a ubbiku, ñu tàmbli woon’a féqu ak’a dañtalu ci ŋëb gu paab gi ak sañ-sañam.

(2)Siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi, te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam.

(3)Fonk sa xeet,walla xeetu gi tàmbli woon’a feeñ ci reewi Tugal yi, te taxoon waa Almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginnaaw Martin Luther, rawati na kuréel gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya.

(4)Dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu Tugal yi dimbali woon, ak ñu dul ñoom ci xalaatkati Almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu.

(5)Firi Injiil ci làkku Almaañ, ak def ci ay taalif yu tax waay Almaañ ji man’a gis ay xalaatam, yër it jam yi mu doon def Jàngu bi .

(6)Tasug móolukaayu téere gi nga xam ne Gotenborg moo ko fentoon, loolu taxoon nag ba xalaati Luther yi tasoon ci waa Almaañ yi ak ñu dul woon ñoom.

Am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante Martin aki gaayam, ñoom ñi diy Diiŋatkat, maanaam ay protestants cig wàll, ak diggante ñi toppoon Paab gi (katolig yi) ci geneen wàll.

Dëkki Almaañ yi moom xare yu tàng’a fa amoon, dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo, gu nu tudde woon (Augsburg) atum 1555 g, ñu nangu woon ci ne diiwaanu Almaañ bu nekk am na àq ak sañ-sañ ci tànn ngér mu ko neex, mu protestant mbaa mu katolig, waaye ci wàllug nguur gi ñu tànn protestant def ko diine, ngérum Luther mu protestant mii tasoon na te siw ci diinaawani almaañ yu bëj-gànnaar yi – Jàngoom daal di doge ca Jàngub Rom ba – ak Norwej, Finland, xalaat yii tam tas ba genn Almaañ, dugg Angalteer ak nguuri skandinaaf yi (Danmaark ak Suwed) .

Kalfen (Calven)[Soppisoppi gongikuwaay bi]

John Calven mi ngi juddoo Fraas atum 1509 g, di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu Luther mi, te bàyyi woon mu katolig mi. Kalfen walla Calven juge woon na Fraas dem Siwis, li ko waraloon it mooy sonal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine .

Fii nag la tàmblee wisaare ak’a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum Luther mi, ñi ko toppoon mu tudde leen (Hogonoots), di ci maanaa ñoñ laab ñi. Kalfen ak Luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari, waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy:

(1) Wax gi Kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la, te loolu Luther nanguwu ko .

(2) Kalfen daa gëmoon ne Egliis bi warul’a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna, ne woon: Egliis bi daa war’a am nguurug boppam gu temb, gu dul wéeru ci gu adduna gi, ñi war’a doxal nguurug Egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma.

Xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi Tugal yi ci anam gu ëppante, ci Fraas, Angalteer, Siwis ak yeneen.

Swingli[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mi ngi cosaanoo woon Siwis, judd atum 1484 g, ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub Siyorix atum 1519 g, ci biir diiŋat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi. Kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu Luther ak Kalfen, waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine.

Swingli moom daa jàppe woon Jàngu bi benn campéef bu am demokraasi, buy ame ak’a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci, mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci Jàngu bi, ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye. Ngérum Swingli tasoon na ci Siwis, ak ci lenn ci yeneen reewi Tugal yi, waaye taxutoon mu siwe, wisaaroo ni mu Luther mi mbaa mu Kalfen mi.