Seere

Jóge Wikipedia.
Dem : Joowiin, Seet

Seede: wax Laa Illaaha Illal Laah, Muhammadun Rasuulul Laah, muy ci maanaa Yàlla rekk mooy buur, Muhammad (j.m) moo di ndawam li mu yonni ngir mu wuutu ko fi, di jàngal nit,ñi di leen xamal li Yàlla bëgg ci ñoom.

Loolu nag di tekki dugg ci diine ju bees, wommatu ñeel Yàlla, bàyyi la nga nekkoon, nekk leegi ci lu bees lii la Yonnant bi woo, tënku ci ak lu mu metti metti, ak lu jamono soppiku soppiku.

Wax laa illaaha illal laah[Soppi]

Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx.(Waxi Seex Ahmadu Bamba)