Kiswahili

Jóge Wikipedia.


Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal


Kiswahili

Kiswahili, walla làkku suwayli aw làkk la wees di wax ci anam gu yaatu ci Penku Afrig gi. Ci Suwayli turu làkk wi mooy Kiswahili. Moom nag aw làkk wu Bantu la.

Suwayli nag dees na ko wax ci gox bu yaatu ci Afrig, la ko dale ca bëj-saalumu Somaali ba ca bëj-gànnaaru Mosambik ak Keeñaa gépp. Lu tollook juroomi milyoŋ yu muy seen làkk wu njëkk a ngi fi (yu muy seen làkk wi ñu nàmp), ak juroom fukki milyoŋ ciy nit yu muy seen ñaareelu làkk (làkk wu ñu jàng). Suwayli mujj na di làkk wow nit ñi man nañu ciy jokkoo ci penku Afrig ak barab yi ko wër.

Suwayli tàmbali naa nekk làkk wees di wax ci Sansibaar, benn dun ci Tansaani. Suwayli làkk wu kilifawu la (officiel) ca Tansani ak Keeñaa. Moom nag làkk wu jeexiitalu la ci yeneen làkk yu bari niki wu araab. Niki làkk yu bari ci Afrig Suwayli nekkoon na di lees di binde ci arafi araab waaye leegi ci yu laatiin yi lañu koy binde.

Bennaani baat[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lii ci suuf ay misaal la ci làkkuw Sàuwayli:

  • waaw - ndiyo
  • déet - hapana
  • okay (walla baax na) - sawa

yeneen dali web[Soppisoppi gongikuwaay bi]