Kaw Gaambi ak Penku Senegaal

Jóge Wikipedia.

Ci Kaw Gaambi ak Penku Senegaal Ay nguur yu bari toftaloo nanu ci dexug Gaambi gi, yi ci ëpp solo ñooy Ñaani ak Wuli. Ñoom nag ñi ngi leen taxawal ci xarnub fukk ak ñeent g.j, ay way gàddaay yu bàyyikoo ca imbratóor gu Mali gaa leen taxawaloon. Yii nguur nag ci ron waawug Jolof gu mag gi lañu nekkoon, ba kero ñuy nanguwaat séenug temb ci xarnub fukk ak juroom benn g.j . Nguur yii nag bokkoon nañu ci joqalanteg yaxantu gi ci anam gu sawar, looloo taxoon ñuy réew yu naat.

Ci bëj-gànnaaru Wuli la nguuri Goy ak Kamera nekkoon, ki léen taxawaloon kilifa la woon gu bokkoon ci njabootug Baajli, mooy Salmaan Xaasa, mi nga xam ne jiite woon na ag nguur ci penku Senegaal. Ñaari nguur yii nag ba xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, dañoo bennoo woon. Buur bi dàkkantalu Tunka la daan yore. Ci atum 1833 g.j, la ab xare tàkk ci seen diggante, ba moo waral ñu tàqalikoo. Goxub Gaambi gu kawe gi ak Senegaal gu penku gi séddaliku na doon ay nguur yu bari, waaye am na ci yu daawul weesu yaatuwaayu as ndëkk. Gi magoon ci nguur yii ci lu dul sikk mooy Namandéeru ak Faalimi, ñaar yii nga xam ne ñi ngi leen sosoon ci lu tollook ñeenteelu xarnu g.j, ñu nekkoon nag ci ron kiliftéefug imbraatóor gu Gana. Am na yeneen nguur yu sosu woon ca la tollook xarnub fukk ak ñatt g.j, ñooy: Siiselaa, Beledugu, Niokolo, Badon, Bademba, Bundu, Gajaga.

Nguur gu mujj gii nag (Gajaga) giirug Sambiira Baccili ñoo ko jiite woon la ko dale ca xarnub fukk ak ñatt g.j . Nguurug Gajaga dund na cig naataange ngir joqalantey yaxantu ya fa daa am te naataloon gox ba, rawati na yaxatug tàkk gi. Ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.j, yaxantu gi mi ngi sukkandiku woon ci daakaande.

Nguuri Gambi gu kawe gi dañu daa dàkkul seen bopp cong yi leen seen dëkkandoo yi daan faral a def, jublu woon ci nangu ci ñoom lenn ci seeni suuf. Ci xarnub fukk ak juroom ñaar ak bu fukk ak juroom ñatt la ay xarekat yu juge ci penku dikk soppi nosteg àtte ga fa amoon, bu ko defee ay njaboot yu yees daal di tàmbalee sangu (dooni njiit) ca gox ba. Bu dee ca Siiselaa moom Daansirimaan moo daaneeloon njiitug giirug Siise, daal di wutal nguur gi weneen tur wu yees mooy : Sirimaano. Bu dee ca Beledugu moom, njabootug Siisoxo moo jële giirug Soomari ci nguur gi. Ca Dantila moom ab nappkat bu siiwe ci turu Samakoto moo nangu nguur ga, dàq njabootug Samora ga.

Seetal BUNTU TAARIIX