Dugg ci gaal gi juge Ndakaaru

Jóge Wikipedia.

Bi nu xëyee - sëñ beey wax - muy bisub àjjuma,di bis bi njëkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal nanu ma ca digg gaal ga,di jooy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,Sëñ ba’a ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: {{Yàlla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jëwrini Yonant bi )) ((Gaal gu fees googu ak mbooloo, yendu na fanaan )) ((Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga )) ((Murid ba tàggoo, dellu ca dun ba, ànd ak xol bu naqari}}.

Mu jublu ci muritam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon ñépp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal,jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ,kon mu delloo la sa kër,ca sa njaboot,Sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko,di ko ci lëjal ba mu far jël daam ak xalimaam,nee na, bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbindéef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw,bàyyi ma fi.


Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saa sa, ma far la ma bindoon,waaye ngoor si lëjëlati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral ,kenn du ko man a xam ku dul ñoñam,ña mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag, nga xam ni moo’k nit ñépp a yam,dara waru ko lu dul mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bëggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko.

Ci loolu mi ngi naan: {{Ki njiit li yonni woon ca ligéeykatu yonant bi,sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bëgg a bind,far reccu )) ((Ginaaw bi aji ligéey ji far li mu bindoon, ñu neeti ko bindal)) ((Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la Yàlla di wonee aw yoon}}.


Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) (wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca Yàlla te Yàlla’a ngi gis jaam yi. {maa ngi jëmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi}}.


Gaal ga deqi bisub gàwwu, ñaareelub rabiihus saanii,Sëñ bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa àddiya ju kawe,ne ko man de da maa dégg ñu ne ya’a ngi ñëw ci gaal gi,jëm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga ñaanal ma dénk ma. Sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jëme,ma dal di koy ñaanal,ne ko bi ma koy dénk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul Yàlla,ku jublu ci ku dul Yàlla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul Yàlla,ku jublu ci Yàlla te jaaralewoo ko ci Muhammad Yonnantab Yàlla bi,(j.y.m) da na xam ne Yonnant beey ki yàlla yonni, ñu dal di tàggoo,mu dem.


Sëñ bi nee na ñu romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi,waaye Yàlla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju ñuul génne ci ab néeg ne ma,ndax ya’ay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jàpplu,ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak a màggal,ak nàngam ak nàngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gaal gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli ñaawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: {{sama àddiya sell na ca Konaakiri, ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar,ci lu dul kuy weddi)) ((Yàlla setal na ma ca Konaakiri,ci lépp luy xëcce jëme ci yu nu sib )) ((Yàlla soril na ma cag njëkk ca Garambasaa,ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma}}.

Àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,leeral gi mu ko leeraloon maanaam laa ilaaha illal laa,waaye du àddiyay alal ja ko waa ja jox,moom waa jooju nga xam ni bu ko Sëñ bi leeralutoon loolu mu alku,te Yàlla gindee na ko ci leeral gi. Mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yéeme gi ko Yàlla defal foofa,mu ne daa jëloon benn bitéelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yeréem aki téereem, nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi, mu ne ma gaaw sànni ko,bi gaal gi téeree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi,duggsi,ndax danu maa déggoon ,ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma,waaye képp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitéelu misk, ñépp walla ña ca ëpp,ci loolu la Sëñ bi naan: { kiy jagleele yërmaandeem di Yàlla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle}}.

Mu jublu woon ci aji yërëme jooju Yàlla mii di boroomi xéewal,daa ko indil ay xéewal,bokk na ci xéewal yooyu biteeli misk yooyu. Mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi,tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag ñeewant ak yërmaande,di mettitlu bu baax li ko dal,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ . Mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne Yàlla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe .Mu ne moom daal,noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal,tàggatal ko ñépp ba kerook muy wàcc Gabong.


Mu ne Gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mjje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci Yàlla ak Yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug géejug dun boobu laa taxawoon di joriku, di xutba géej gi naan: { yaw géej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal,ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal(wareesu koo def ñatt, ndax kenn rekk la) cëy moom ni mu doone buur bu tedd ) (Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal Yàlla,te seere ne man ab jaamam laa,bob sopp na ko}}

Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa ñatti at yu manke tuuti,di ligéeyal Yonnant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab sëtam,ma joxoñ ko sama xalima gi,gëdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fépp.

Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya yépp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji ñëwee,li mu njëkk a def,mooy laaj ma, ñu tegtal ko sama kër,mu ñëw ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig màggal,dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tàllal sama bos,waaye ca saa sa am lu wax ak man,mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan,ne :{ yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun}muy yeen ñi gëm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bëmëx ab loxoom bëmëx gu tar,ba waa ji yëngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lépp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tolloo’k waxtu jàllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ,walla mu lay lëjal,di la tumbrànkeel ak a génne sa réew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daataa wàcc,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci ñi mu gën a sopp nga,loolu moo waraloon sama ñëw gii du leneen.


Sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, ñu ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu bég ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na ca’a loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah.



Da na rafet fii ma indil leen fi bayiti ki def Xawaariq muy Ibnu Hanbal: ( Bari na aji jalgati (tooñkat) ju sol yérey teddngaam,di puukarewu ,sol ab tëneem aki takkaayam) (ay junniy junni nekk ci ron kiliftéefam,te faalewul ku koy digal mbaa mu koy tere)) (ngeen (Sëñ bi lay waxal) wàcce ko ci mbartalum toraxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju ñaw) ) ( muy ndimbal lu tukkee ca Yàlla ñeel jaamam bii di ligéeyal Yonant bi,nga xam ne soldaari nasaraan si ci la nu mujje mokk ba mel ni ay ansaaram,(ansaar mooy ku lay jàppale ak a dimbale) ) ( cey bu tuddoon sekkare bi, kon dey mbindéef yi yéemu,waaye moom ab dënnam bàmmeelub ay mbóot la).

Nee na bokk na ci karaama ( mooy xarbaax ak kiimaan yi Yàlla di defal aw wàlliyu) yi ko Yàlla defaloon ci géej gi,feeñug Ahlu Badrin,mu ne moom kat bi mu nekkee ci benn ci dun yi,dañu koo yobb woon ca karce ga,dëkkal ko fa soldaar sa,nee na ma mel fa ni kenn ca ñoom,ñuy tux ak a naan ak a fo ci sama wet, man may muñ seeni lor rekk,ndax man xam naa ne mukallaf mu ne am na ñaari malaaka yu ko seq,di bind ay jëfam,ginaaw ñaari malaaka yooyu ñoo man a muñ,man a dékku li ñiy dajeel ciy lor,ngir topp seen boroom,kon du jaadu ci man may jàmbat,ndax ñoom kat li leen di naqari rekk moo may naqari,li leen di mettee may metti,te ñoom du ñu jàmbat. Ci noonu Yàlla dogal soldaar si genn bis di tàggatu ji ,ba ñu demee fañuy tàggatoo fekk fa am mbooloo mu war ay fas, kaalawu, sappewu (rang),soldaar si dal di tiit ,taxaw,ci noonu seen njiit li tëyye leen,gëdd leen ne da leen di ray bu ñu siiwalee xibaar bi. Bi suba jotee ba leer,mbooloo mi waroon fas yi ne mes,soldaar si dem ne miik,bañ a nettali dara. Sëñ bi nee na bi loolu tegee ay fan,aakim bi (goornoor bi) woo ko nooy-nooylu ci kanamam,wax ak moom wax ju nooy,ci biir wax ji mu ne ko: xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali ci li nga bëgg? Ma ne ko ñooñu moom ay nit lanu walla ay jinne? Mu ne ma yaa ko gën a xam ! Man ma won ko ne xamuma dara ci li miy wax,mu dal di noppi. Am na ci boroom xam-xam yi ku ko ci laajoon lu waraloon feeñug Ahlu Badrin gi,Sëñ bi ne ko :ngir tiital noon yi. Keneen laaj ko ne ko ñooña ñooy niti Ahlu Badrin ña walla malaaka ya?,mu ne ko malaaka ya .Am ku neeti ko ndax yonnant (j.y.m) bi ca la woon? Mu ne ko moo doonoon seen njiit,daal di ciy wax wax jii:<< ki nga xam ni wommatal na ma la fàddu woon wëliif bepp wàlliyu,jàppndalal na ma mebat yepp fa dëkk ba niy wax Limbarwali >> << ka soril rambaaj ba ak ku inaañ ka ,wommatal na ma waa Badar ña diy sang>> << Yàlla da na ma wommatal begleg laa illaaha illallaa fu ma man a ne >> . Ku baax ki nee na li mu bëgg a wax ci bayit yooyu mooy: li fàddu woon weliif bepp wàlliyu,mooy feeñug waa Badar ànd ak seen kilifa ga (j.y.m) ca pàkk yu lëndam yooya ca geej ga,ngir jàjji ay noonam.Begleg laa ilaaha illallaa,mi ngi ci jubloo wax aaya bi sun boroom di wax (( wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda lifaddlihii)) muy ci maanaa bu la Yàlla bëggalee aw yiw amul ku ko man a tëyye. Fu mu waxe nex-nexi walla lori laa illaahaillal laa,mi ngi ci jublu waxi Yàlla ji mu naan:(( wa in yamsaskal laahu bi durrin falaa kaasifa lahoo illaa huwa )) muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak aw ay amul ku ko man a dindi ku dul moom.


Mu ne bis teg nanu ko ci mbedd mu xat,dal di joyal aw nag ci kawam,tàmblee seetaan,yaakaar ne agsi na ci sama kaw ba noppi,waaye bi mu ma jegee daa daal di jekki-jekki rekk naaw mel ne daa am ay laaf. Nag wii mooy wi Abdu Laahi Saalim Ibnu Anbal doon tudd ci Xawaariq bi mu naan: ( ab xiik (xiik mooy xale bu jigeen bu masul a sëy,fii mu jublu ci nag wu toll ci war a sëy ) ci nagi kër yi,muy naaw ci jàww ji ba kenn gisatu ko).

Mu ne mas naa am mu yàgg ci benn barab ba foofa soof ko,mu tàmbli di jàmbat,waaye nee na daa jàmbat rekk Yàlla sotti ko yamb yu soxot te bari,ñu koy màtt ak a sonnal,mu ne bi mu xamee ne li ko dal moo ko teg boppam,ndax kat ((wamaa asaabakum min musiibatin fa bimaa kasabat aydiikum)) muy musiba mu leen dal yeen a ko teg seen bopp,bi loolu amee mu ne ma soppi samag jàmbat def ko ag cant,daal di ne: (( nasaxal naa sama njàmbat def ko ag cant,dootuma jàmbat ci moom lenn lor,ndax sama lor naaxsaay na)). Ci noonu nee na yamb ya dem wëlif ma ,ma tàmblee noppalu,xam naa ne yamb yooyu la ki def xawaariq jublu woon bi mu naan: ( ay yamb yu toll ne ay mburtu (mbate) yu suur cig réy, cam si (cam si mooy waa ji,mu jublu ci Sen bi) daje na ak ñoom,te faalewul seeni lor ).

Mu waxaat ne waa jooju doon nasaraan-nasaraanlu te nu tuddoon ko ca ginaaw,bis def na ko lu ñaaw ba yenn xaritam yi yedd ko ci,xupp ko ba mu tiit, reccu,ca guddi googa nag mu ñëw ànd ak ku koy wommatal ab gàtt,moom mu yor benn biteelub daa bu mag ci loxoom,dal di tedd tàllalu ci sama kanam,nee waay day tuub,te ne du jug fi mu tëdd mukk,li feek teguma sama ndëggul tànk cig doqam,ngir tuub,ma fexe ba jële ko fa ci wax ju rafet rekk,mi ngi ma fekkoon nag may bind ca jamono jooja,ma dal di def bayit wii ca saa sa: 4(( Yàlla nooyalal na ma ci guddi gii xolub boroomug tubbi ga,ginaaw bi mu ma indilee ab gàtt ak daa , ( ngir tuube ko ) )).


Ku baax ki tudd na ba tay yeneen karaama yu ko yàlla defal ci gèej gi,mu ne da fa mas a dëkk ak benn doxalkat (goornoor) bu soxot,bu kenn dul jege te bagul dara ci lu baax,ma wax bis ne jiyaar jii may def ci yoonu Yàlla daal di naa ko seet tay ci mbirum àttekat bii,ma xool nu ma ko Yàlla di tàggatale, ci noonu ma juge sama néeg dal di dëgmal këram,ñu ne ko sëriñ ba dey a nga jemsi ci yaw, mu ne aah loolu de lu jomb la,ndax danu daa sàkku ci moom muy bañ,kon tay naka la fiy dikke ci coobareem,ñu ne ko amul benn sikk ci ne kee di dikk de moom la,mu dal di jug ci saa si daje ak man fu sori,bég ci man mbégte mu kawe,ci noonu mu ànd ak man ca barabub boppam ba,dal di ne ma loo bëgg, loo bëgg cig baamu ? Wax ko ay yoon, man itam ma ne patt, rekk di xool lu ma koy wax,ba yàgg ma ni ko,da maa bëgg as lëf ci daa, mu dal di may jox bitéel bu mag bu fees ak daa,ma daal di ne wëlbat won ko ginaaw,booba fekkoon na ma may bind ak xasida gu ñu tënke arafi a b t th j (mooy abajada rekk) ,ba ma àggee ca arafu faa,ma bind ca bayit wii ne: (( sama xalima texe na fa ab aat (mooy ku xaraful)bu weddi Yàlla,kok tàggat naa ko ci xul huwal laahu ahad)).


Ma bindaat ay bayit,yoy dañu maa wax ni ma lii de ag wor la, ndax yaa ngi bàyyi yéefar yi ci anam gu dog,ba noppi ngay jël ci ñoom di nëbb,ma dal di bàyyi la ma doon def,gas am pax ba mu xoot ,ma sotti ca daa ja,suul,dal di xam ni sama jiyaar ji dëggu na, ma sant Yàlla .

Nee na itam,benn janqu ndar-ndar,dafa gént gis Waa-Badar,ci bis yooyu nu dugg dëkk ba, tàmblee ray waa dëkk ba,bi nu demee ba kenn ci ñoom jege ndaw si,jenn moroom ji ne ko soxna soosu de ab jullit la,mu dal di koy bàyyi. Sëriñ bi nee na xale bu jigéen boobu ku baax la woon,daan sonn ci moom ci li mu am,daan ko wax naan man dey lu ma la jox rekk xamal ne maa ko ñaq ci sama loxo,njëgug sàngara nekku ci du caagéenug gu poon,loolu da koo leeral foofu ndax kat foofa ci ñaar yooyu lañu daa jëflantee,te moom xam na ne man du ma leen jëfandikoo te du ma jëfandikoo seenug njëkk,ma laaj ko bis ne ko loo bëgg ci lii nga may defal?,mu ne ma bu dee ci àdduna ,sët yu baax,bu dee allaaxira àjjana, ma ne ko Yàlla man na lu nekk.

Yàggul tuuti rekk,Yàlla dogal mu ëmb,te daawul ëmb,bi diirub ëmbam matee rekk mu dal di wësin,dal di faatoo ci wësin wi,ma jullee ko,masu ma koo gis it mukk,ndare bi ma taxawee di ko jullee,ndax sunug jëflante mi ngi doon ame cig yonneente (correspondence). Nee nanu doomi Daba SEY la woon tuddoon Aamina (Ami),boroom këram tuddoon Yèlli SEY,bokkoon ci ndawi goornoor yu mag yi,di woon it ku baax te daan sonn ci man.

Am na bis mu jote ak àttekat bi (goornoor bi) jote gu tàng,ngir sama jëmm ji,loolu nag ni mu ame woon mooy daa am bis ma wutoon ñeenti bant teg leen ci sama buntu néeg ngir def ko ab julliwaay ngir ñiy romb bañ di ci jaar,bi ko àttekat bi gisee ,daa dal di jug,falang jàkka ji buddi bant yi,sànni leen,ne fii amul julli amul lislaam,da nga ñoo bëgg a yàqqal sunu soldaar yi,ma ne miik,bi ko Yèlli SEY yëgee te tubaab bi demagul,daa dal di jug ca saa sa,jawalsi ànd ak aw meram , ne ko lu tax nga tas jàkkaam ji,te moom defu ko fu dul ci buntu këram?, sakkul yoon wi te xatalul kenn it. Tubaab bi ne ko man daal maa ko def,fii jàkka du fi am,Yèlli ne ko waaye man di naa ko defaraatal jàkkaam ji na mu meloon,tubaab bi ne ko du fi ame, ñuy bëgg a doorante nit ñi dox seen diggante, ñu nekk di xuloo diggante tàkkusaan ba jant so,ci biir loolu lépp man maa ngi bind.


Ci xisa bii (nettali bii)laa binde xasidag ((Rabbanaa axrijnaa min haazihil xarya azzaalimi ahluhaa wajhal lanaa min ladunka walliyan wajhal lanaa min ladunka naziiran) muy ci maanaa yaw sunu boroom génne ñu ci dëkk bii nga xam ne ñi fi dëkk ay tooñkat lañu te nga wutal ñu aji méngoo ju tukke fi yaw,te wutal ñu aji dimbalee,xasida gee nekk nii: (( gërëm naa kilifa gu màgg gii nga xam ne yar na samab xol te koomal ma, moom dey mooy boroom bi gën a tedd)) ba bi mu àggee ci : (( bindal ko(moom Yonnant bi) ag xéewal ak ag mucc ak ñoñam aki saabaam te nga def sama jàkka ji ci darajaam (moom Yonnant bi) muy lu yaatu ))

Bi mu àggee foofu ñu ne ko nangul nanu la ko,da nga ko gis. Loolu nag gis nanu ko,mooy jàkkay Jurbel ak Tuubaa ,xasida gi nag gu gudd la te rafet gu am jeexiit gu réy ci jañ ak ñoddi bu soobe Yàlla ak ci barkeb aji defam,ku koy jëfandikoo na ragal Yàlla te xemmeem aw yiwam.

Yàlla dogal na bis Yèlli moomu siyaaresi ko Njaaréem,juge ca yooyale wàll,ginaaw bi jumaa ji noppee muy ju Njaaréem,Sëñ bi ne ma ma’ak sama jenn waay ànd leen ak moom mu siyaare jàkka ji,ñu ànd ak moom, won ko jàkka jépp,penkook sowwu,biir ak biti,mu yéemu gépp yéemu,bi nu dëppee Sëñ bi ne ko noo gise jàkka jii ak sama jàkka joojee,yaw mi ma doon xeexal ak a dàkku?,mu ne subhaanal laah maneesu leen a tollale,Sëñ bi ne lii mooy maanaam sama wax jii: (( Yàlla dàq na jëme ca ku dul man ca Maayomba la naqari woon sama xol te yékkati samag wàll)). La naqari woon sama xol bu nu koy firi mooy tas gi nu tasoon jàkkaam ja,yekkati samag wàll mu jublu ci yekkatikug soorool yi.


Ab nettali bu yéemee ngii bu làmboo ay karaamay Señ bi: Señ bi nee na bi tubaab bi buddee bantam yooyu,sànni leen,kenn ci gaa yi bégoon ci jëfi tubaab bi, da cee jëloon ab bant samp ko ci wanag wi miy sangoo ak a doxe aajo,waaye Yàlla nattoo ko benn bis mu bëgg a tuur ndox,jawali ca satala ga te booba satala ga ndox mu tàng a ca nekk te moom yëgu ko,te seetu ko it,waaye bi mu noppee ba sotti ko ca cér ba (sàkkara sa) da wadd ca kaw ni ab baa bu góor bu tiit,dal di yuuxu ba fa baatam yam, ne: Señ bi dimbali ma alku naa de,dal di sànni satala ga ca àll ba,dikk teg loxo ba ca tubay ja,ma ne lu deesi defati lu dul muñ ak wax (( innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun)).


Mu neeti - moom ku tedd ki - ne am na at mom bu doonul woon li ko Yàlla tawfeexal saa su xamee ni weer tàmbali na mu di ko bind,kon wenn weeru ramadaan doon na jàll te du ko xam,ndax waa dëkk boobee mu nekkoon xamunu woon lu dul weeru tubaab wi,bi korite gi jotee ma xëy, dog ,sangu, def li ci sunna digale,ma génn ne damay julli ji ca pencum dëkk ba,ba ma àggee, ma xool sowwu ak penku,xoolati sama ndijoor ak cammooñ,ànd ak am kóolute ci ne kenn du ñëw,am ñaari jèbbéer (jèbbeer mooy jaam bu jigéen) yu agsi war a toll ci baalix ( baalix mooy ati génn ag ndaw) taxaw sama kanam di ma seetaan,ma kàbbar ñu tàmbalee xàqataay,saa su ma kàbbaree nu ree,naka noonu su ma jàngee,ba ma sëlmal def samab xut ba, sama déeyaale gi maa ngi ciy wax:(( yaw buur bi, xam nga ni woor naa weeru ramadaan ni nga ko digalee,ma dog ,sangu,julli ni nga ko digalee,waaye dey lu ma génnee muurum koor laa amul,bu ma ko amoon it,ku ma ko jox laa dul am,kon jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sang,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam ,te nga nangul ma lépp lu ma man te def ko ci sa ndigal yi,te nga bindal ma yoolub li ma manul lòtt ci,te amoon ci yeene walla yu ni mel.


Bi ma noppee def xasida gii: yaw buur bi jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sàng ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam te nga def qaafiya bii di ñëw,mu kawe miimiya ba ,ci lu feeñ ak lu nëbb,aamiin yaarabal haalamiin ci barkeb Yonnant bi (j.y.m) : ((maa ngi yaakaar ci aji yaatu ju dëggu ji,ci darajay ki niy xeeñtu di Yonnat biy dimbali dëgg ci dëgg (j.y.m) )) (( maa ngi yaakaar ci Yàlla moomu delluwaat ci samay mbokk ci lu gaaw ànd ak njub gu dëggu)) (( ak nekk jaam bu texe bu nu matal, tey ligeeyal jaamub Yàlla miy dëgg,jaamam boobu di yonnant bi mu tànn)) (( yaw Yàlla ci darajay ku nu tànn ki ak ñoñam,yal na nga ma jéggal te nekkal ma te wommat ma te goreel ma)) (( di naa la gërëmloo ci Alxuraan ak sunna si nga xam ne,Yonnant bi yoonalal nanu ko,yaw miy aji teqale lu taqaloo)) (( yal na nga ma tàggatal noon yepp ba fàww,te fegal ma ag bokkaale,yaw aji not jiy boroom tijji ak tëj)) yal na nga ma wommat delloo ma Daaru Salaam gi nga xam ne fa laay deyaaleek yaw ciy aaya,te yal na nga kaweel ci man ay gox)) (( yaw sunu boroom yal na nga ma dello ci lu gaaw te defal ma samay mébat yepp,te nga may defal ay mbégte te di am ñeewant ci ma)) (( te nga may ma ay xam-xam yu jariñ jëmm ji ak mbidéef yi,te nga dolli ag yaatal gog texeel lay doon ak ubbi ak xar-baax)) (( sama bakkan déy daa bañ ag yéwénal,ndax ab noon la,kon sellalal ma ko cig taxañ (taxañ Señ bi mi ngi ciy jublu lu gaaw) yaw miy ngën ji kuy yéegale )) ((na nga ma may ba fàww li ma bëgg ci mbindéef yépp, te nga fegal ma séenuw ay yaw miy joxe ag jiitu )) (( màngal ma samay mébat fii ak fa nu jëm,te nga may ma ngënéel lu màgg te saxalal ma ngënéel li)) (( yaw sama boroom fegal ma li ma ragal ca bisub njàqare ba,te nga defal ma jéggi siraat gu gaaw gu mel ni melax )) (( musal ma ci (ay nocciku = nusuuh) ak lépp lu nit ñiy ragal te nga def ma may ku sori ag lakk)) (( nangul sama ñaan gii yaw sama boroom,te nga faral ma samay ayib ,te nga seere ne man dey tuub naa ci jepp jëf ju di jëfi dof)) (( te nga nekkal ma yaw sama boroom,te musal ma,te amal sama yaakaar,te fegal ma luy bijji ag nëx )) (( nangul ma sama ñaan gii,yaw mi moom lepp, te nga tabe ñeel ma cig yaatal ak dëddu ak dëggu )) ((ci darajay Yonnant bu nu tànn bi,te nga fegal ma hisaab ci darajaam,te tàggatal ma ci moom kepp ku di boroomug kàccoor)) (( na nga julli te sëlmël ci moom Yonnant bi,ak ñoñam aki saabaam,yaw mi moom penkook sowwu)).


Mu nettali ci karaamay géej gi,ne : am na jenn waay ju bokkoon ci kilifay barab bi ma nekkoon,da maa digoon ab bitéelu misk ci lu dul ma di ko sàkku ci moom,ndax man daawu ma sàkku ci ñoom lenn,te daawu ma sentu ci ñoom,daawu ma wóolu seeni dig it,waa jooju ma digoon bitéelu misk bi,ndekete daa digoon keneen ci moroomam yi lu mel ni li mu ma digoon,waaye bi mu deful li mu digewoon ,waa ja daa tàmbali di xuloo ak moom ak a ngaayoo,moom itam muy dàkku boppam,(di defandar boppam) loolu lepp it mi ngi doon ame ci sama wet,ci wolof it lañu doon waxe waaye yu leerul dara,waaye làkk gi nu koy làkk li muy leeradi leeradi fàttali na ma réew ma, ba mel ne da maa ñibbi far ,ngir gëj gi ma ko gëj a dégg,loola neex ma lool.

Waaye xuloo bi nu def te li ko waraloon lepp mooy wóolu gi mu ko wóolu woon,ak dig gi mu ko dig te defu ko,loolu lepp ma sant ci Yàlla,mi ma defal may kok wóoluwu ma kenn,sentuwu ma ci kenn ku dul moom,loolu tax ma def xasidag cànt gii, ma wax ne:

Maa ngi tàmblee samay wax aki bjëf ci turu Yàlla miy boroom yërmaande ju yaatu ji ak ji miy jàgleele, xeewal ak mucc yal na nekk ci sunu sang,Muhaddad ak ñoñam aki saabaam.Miimiya bii moom la ñeel yal na ko Yàlla gërëm. Yaw sama boroom sama noon yiy say noon,sànni nanu ma ci géej gi,ni nu sànnee woon sa xarit ba Ibraahima ca sawara wa,nga waxoon ak moom (sawara wa) ci :(( yaanaaru koonii bardan wa salaaman halaa ibraahima )) muy yaw sawara wi doonal ab sedd ak jàmm ci Ibraahiima. Sawara wa dal di mujj di àjjana ci moom,jàmm ak xeewal yal na nekk ci moom ak ci mbooleem nabiyu yi ak yonnant yi, Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw aji dund ji! Yaw aji taxaw ji ! Ci darajay weeru ramadaan mi nga wàcce Alxuraan, mu dig jub ñeel nit ñi, te di ay aaya yu leer yu di ag njub ak ag teqale dëgg ag safaan,ci barkeb xut ba bii tàggatal ma géej gii ak ñoñam ak mbooleem samay noon yiy sa yos,te nga bégal jullit yu góor yi ak yu jigéen yi ci ñu gis ma te dajeek man,te dégg sama ag dellu ca Daaru Salaam,ak Tuubaa ci lu gaaw ci lu dul ab coona du caagéenug ag sabablu gu tukkee ci man,Aamiin yaw boroom mbindéef yi, ci darajaam moom Yonnant bi,(j.y.m) te nga def miimiya bii mu kawe li ma jortoon,ni nga ko baaxoo defe ak man ca la ma waxoon njëkk bii,te nga defal ma ko muy ab yobbal,tey pakk tey àjjana ci ñaari kër yi,aamiin yaarabal haalamiin.

(( man déy maa ngi tagg,tey sant ngën ji aji xéewale, te du ma jàmbat ñàkki xéewal ci menn mbindéef )) ((kepp ku ma jorte ci sama tumburànke gii may kuy toroxlu ci kenn ku dul aji doyluloo jiy aji yaatu (muy Yàlla) na ko wóor ne moom ku gumba la )) (( moom de laay jàmbat samag lòtt ,samag ñàkk ak samag tumburànke,may yaakaar samag dellu ci lu gaaw di ngën ji ku nu xeewale )) (( jàmbat naa ko samag lòtt,mu fajal ma ko,te nekkal ma ci lu kawe sama njort,moom kat mooy gën jaa teddi kuy terale )) (( ñi nga xam ne weddi gi nu weddi Yàlla da leen a wor danoo jublu woon samag wàll,mu aar ma ci ñoom dàkku jepp aji tooñ)) (( ag cant ñeel na ko tukkee fi man,di yaakaar ci moom sama càkkutéef lii,ci lu dul ab coona buy juge ci man,te sama naqar dañ na )) (( ki njort wor ba muy iñaan, bu ma woree tam,na ko wóor ne ki ma wommat cig teral de woru ma)) (( ku ma sànni ci géej gi ngir ag weddi di boroomug mbañeel,na ko wóor ne ci géej gii de tabeg aji terle ji dikkal na ma fi )) (( koo xam ne li ko naqari mooy nekk gi ma nekk di jaamub Yàlla,tey jëwrini aji rammu jiy ku nu jiital )) (( na ko wóor ne man de ab jaamam laa ci géej gi ak ci jéeri ji,di ligéeyal kiy musale ci luy waral reccu)) (( ku ma dëddu de na xam ne xéewal yi jublusi nanu,juge ci aji yaatu jiy aji doyluloo,kiy aji wattu tey aji jiital )) (( ku ma sànni ci géej gi ngir sàkku samag tumburànke,na xam ne ag tàggat ñeel na ma tukkee fa sama boroom ci gépp géej )) (( samag wéeru ñeel na Yàlla ci samag teew ak samag fàdd,te di naa jàmbat jëm ci moom jaarale ko ci Yonnant bi,moom miy samab raas (bi may yéege jém ca Yàlla) ndaw muy ku baax )) (( yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom ak ci ñoñam aki saabaam ak bepp jullit )) (( yaw sama boroom saxalal ba fàww ngën jaa selli julli ak sëlmël ci Muhammad)) (( ak ñoñam aki saabaam yepp,te nga delloo ma Tuubaa ci lu gaaw,te peek ma te xamal ma)) (( yaw sunu boroom man de warlu naa ba fàww di kuy ligéeyal Yonnant bi,tey kuy ligeeyal aaya yi,na nga ma xamal te déggal ma )) ((yaw sama boroom,maa ngi sàkku ci aji maye ji ag géeju akug wuññi akug yinkiiwal (ag sol xam-xam mu tukkee fa Yàlla) na nga ma wuññil te yinkiiwal ma )) (( jublu naa aji ubbi ji tey sàkku ag ubbeem,di yaakaar ci moom ay may yuy ball,ndax ag ballam day yol di sotti)) ((gërëm naa aji not ji bi mu ma tàggatalee noon yi,ma doonoon ku tumburànke,di ku wéet fa ñoom di ku amoon gépp lëmmu)) (( di naa ko gërëmloo ci Alxuraan ngir sant ko ci xéewalam yi,ci sama xol ak sama yaram ak sama gimiñ )) (( war na ma ma saxal li mu ma tànnal mu dig jub,te ma koy gërëmloo ci aaya yi ndax ñoom kat (aaya yi) mujj nañu di samam màng (ngañaay) )) samay cant aki ngërëm aki tagg ñeel na aji jariñe joj indil na ma Alxuraan ju tedd ju ñu màggal)) (( moom (Alxuraan) mooy ndàmm mi (koom mi) tey leer gu fés gi niy aar ci sawara ak noon yi ak gàcca)) (( ab teere la bu tedd,juge ci aji tedd juy terale,jëm ci jaam bu tedd,buy xettalee tey boroom yërmaande)) ((teere bu darajawu la juge ci ku darajawu,ku darajawu te wóor indi ko, jéme ko ci aji darajawu kuy matal )) (( xéewal ak jàmm ci lu dul dog yal nanu nekk ci moom,ak ñoñam aki saabaam fu mu man a nekk)) (( jàmm ak xéewal yal nunu sax ci moom li feek aji sant a ngi naan : da ma ne maa ngi sant ngën ji aji xéewale)) (( Xéewal yal na sax ci moom juge ci aji tedd ji may nekkal,te du ma jàmbat ñàkk ay xéewal ci menn mbindéef)) (( mucc yal na nekk ci moom juge ci moom (Yàlla),(mucc) gog da nga ma ci fegal (yaw Yàlla) aw ay, te aar ci samag wàll wëlif ku nu rëbb ki (muy ibliis) ak ku gumba)) ((xéewal yal na sax ci moom tukkee fa moom(Yàlla),li feek ku koy jàmbati mbiram a ngi am la mu bëgg di gën ji ku nu xéewale)) ((aki ñoñ aki saaba yoy maa ngi ñaan aji kawe ji mu dugal ma ca seen biir ëlëg may boroomug xéewu )).



Bokk na ci karaamay géej gi ba tay nettaleem bii,mu ne: bis xëy na, waaj ngir ligéeyal Yonnant bi - ni mu ko baaxoo woon - amul lu dul aw mettit wu tar daj mbooleem yaram wi,ba manatul li mu bëggoon ,waaye am benn tubaab ci njiiti nguur gi,mi ngi dëkkoon ci wetu fi Sëñ bi dëkkoon,nekkoon di xaqataay ca kaw aki moroomam,Sëñ bi daa di ne:Yàlla yaw de xam nga li ma waajoon jëm,ak li ma ci gàllankoor,maa ngi lay ñaan nga tuxal lii fi man te yobb ko ci ki lay wutal moroom,amul lu dul ma dégg waa ji doon xaqataay muy onk,man may bind.


Bokk na ci karaamay géej gi ba tay lii: bis nee na fi mu nekkoon ndawal da faa mànke woon lool,ba jën yu ndaw yi nuy def ci poti weñ yi rekk lanuy lekk daanaka (xam naa mooy poti ton yi) ma jëfandiku ci bis,bi ma noppee ma raxasu ba sonn,jëfandikoo suuf ak saabu ak lu nu man a dindee ag xet rekk,waaye dara,ba ma ca manatul dara ba ne naa dem nag jublooti ca ligéey ba,bi ma tàmbalee rekk ñu ne ma ((wa minhumul laziina yuuzuunan nabiiya)) muy am na ci ñoom ñuy lor Yonnant bi,ma tiit lool, jaaxlee jaaxle,ca saa sa ma bàyyi koo jëfandikoo,doxe ca bàyyi luy jën,boole ko ci li ma jaayante ne du ma ko lekkati,bis bi ma ko bàyyee walla lu ko jege,ay kuy dikkal nanu ma,juge ci fere yi,di njëg gu nu gaawal ci jën yi ma jaayante woon.


Mu neeti moom ku baax ki:dëkk bi mu nekkoon da faa nekkoon aki làbbe ñuy jël ci xaley yéefari nit ñu ñuul ñi nekkoon foofu di leen def ay mbindaan,di ànd ak ñoom di wër ci ja yi (marse)ginaaw tàkkusaan,njiit li nekkoon foofu defe woon ne da maa xemmeemoon ci gone yi mu ne ma woon boo ci soxlaa de ma joxla ci ñuy ànd ak yaw,ma ne ko soxlwu ma ci. Njiiti dëkk booba itam baaxoo woon nanu di jël ci magi nit ñu ñuul ñi, ñu ñuy def ay toggkat aki rootkat,ma sàkku kenn ci ñoom bis ngir ligéeyloo ko,waaye ba mu ma jegee daal xeeñal na la ko xeeñ goo xam ne amul gu ni mel,ma ne kii daal sobe na ba maneesul a jaxasoo ak moom,ca noona ma jaayante ci seeni ndaw ak seeni mag ni ma jaayantee ci jën yu mag yi ak yu ndaw yi ,ci loolu mu ne:


(( ma ne njëgug ndaw ñi dikk na ak gu mag ñi ak ndaw ñi)) ((Muhammad gën ji imaam mooy sama dëkkandoo,ag bëbbam de (dexam) ci sama xol lay sottiku jëm)) .

Fere yi ñëwoon indi kuy yi (xar mu goor mu mag) ñooy mosalug njëgi yéefar yu mag yeek yu ndaw yi,kuy yooyu it di mosalug njëgi jën yu ndaw yi ak yu mag yi.

Bokk na ci karaamaam yi ci géej gi ba tay waxam jii mu ne: bi ma xoolee sama diggante ak noon yi ,nooni Yàlla yi,ma xam ne ñoom kat am nanu kàttan ci lor ma ak gaañ ma,ci dogalub Yàlla bi ak’ug nammeelam,ma xam it ne bu doonutoon kaaraangey Yàlla ji ak’ug fegam kon ba tay waxatunu ko,laa leen bàyyi ak seen bëgg-bëgg,jublu sunu boroom,mi yor mbir yi,ma déeyaale ak moom ci sama mbir: ma ne ko Yàlla yaw’ay ki nu bind ngir nu jaamu la,nga ne ((wa maa xalaqtul jinna wal insa illa liyahbudoonii)) muy bindu ma nit ak jinne ndare ngir ñu jaamu ma,nga neeti : (( yaa ayyuhan naasu uhbudoo ràbbakum)) muy yeen nit ñi jaamu leen seen boroom,bu ko defee tawfeex ñeel ki texe jiitu ci moom,mu dégg wax ji topp ko,naka noonu toroxte ñeel ki ag texeedi jiitu ci moom,mu lànk bañ a wuyyu,tëx, luu, ngir’ug weddi,man nga tawfeexal ma,def ma ci mbooloom ñi wuyyu,mbooloom Yonnant bi Muhammad (j.y.m) imaami anbiyaawu yi ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom ñepp,nga dolleeti ma ngënéel,def ma may jëwrini Yonnat bi tey xalifaam ci diineem ak xeetam,am mbooloo ci sa noon yi, noonam yi,jug song ma ngir dox sama diggante ak jaamu la,te ligéeyal ko (moom Yonnant bi) . Ñoom dey ñi ngii di ñu caaxaanadi ci seeni jëf,di ñuy farlu ci seeni neen,te yaw yaay ki wax ci làmmiñu sa Yonnant bi,lol maanaa mi mooy:nit ku nekk daa am kër ca àjjana ak ca sawara,bu duggee àjjana ñu won ko këram ga woon ca sawara,ne ko fee de nga jëmoon boo jaamuwutoon sa boroom,leegi nga xam ne daa nara gént,ab yéefar a koy donn. Bu tàbbee sawara’at nu won ko barab ba mu doon am ca àjjana,bu jaamu woon Yàlla,ginaaw nag jaamuwul boroomam ba tàbbi sawara,leegi ab jullit lanu koy jox. Ginaaw mbir yi nii lanu deme,te noon yii - ni nga ko xame - ci tooñ ma lanu dëkk ak a def ci man lu leen soob,te du ma fayyu te du ma leen ñaanal aw ay,waaye maa ngi lay ñaan seen kër ya ca àjjana,Yàlla nangul ma ko,may ma leen,ba ma xamee ne maa leen moom,ma jox leen àddiya waa-Ahlu Badrin . Ci loolu mi ngi naan:

( jox naa àddiya këri noon ya nekk àjjana mi kuy jalgati dul dugg,ñeel saabay Yonnat bi)) ((kër yooya de jëlees na leen ca noon ya,jox leen saaba yu baax ya)) (( Yàlla jox na ma kër ya fa samag tumburànke,teeyal it samab xol)) (( man nag def naa leen ay àddiya ñeel saaba yi,yal na leen Yàlla gëram ,moom mi ma aar wëlif (sahaab:ay niir ) )).


Na nga xam ne karaamay tukkib géej ji moom maneesu leen a jeexal,bu ma bëggoon a indi li ma ci xam ci lu juge fu wóor ,ak li ma ci dégg ci nit ñi,kon dey ma indi fi lu yéem xel yi,te kon du xaj ci teere sii di su nu gàttal,looloo tax ma yam ci li nga xam ne topp naa ko ba mu wóor.

Mu ne ati tumburànkeem gi juroom ñatti at yu mànke tuuti la,bi mu matalee li ko Yàlla bindaloon cig tumburànke,ci suufus yéefar yu ñuul yi,Yàlla indeeti ko ca suufam ngir nitam ñi ñoom itam jariñu ci moom ci li ko Yàlla may ciy mbóot ci tukkeem bu barkeel boobu,ak ngir mu daje ak mbokki jullitam yu baax yooyu di naar yi,ci noonu Yàlla dal di def ci xoli kilifay nguur gi ñu am ag ñeewant ci moom delloosi ko.